Sëñ Maalig Basin Si

Sëriñ Maalig Baasin Si (1871 – 1955) mi ngi gane àdduna ci atum 1871. Baayam tudd Sëriñ Maxtaar Penda Si
ndayam tudd Soxna Xadi Ñaŋ.
Di ab jullit bu jëfe ag njullitam te it di ab sufiyànke bu mag di taalubeb Sëriñ Tuubaa jébbalu ci atum 1905 .

Aw meloom
Ndaama la woon su xees te am bët jot i cër am xorom lool ci waxiin ak jëfiin

ku bari kersa la woon ak i teggiin te bëgg lu rafet bëgg sutura lu ko
waay mas a jox ci mbooloo ginnaaw ñepp gis nañu ko da koy tasaare jox ko mboolo ma waaye du ko jariñoo.
ku dund sunna la woon ak ug cet bu daan tëdd,
mbaa mu lekk mbaa war daaba, dana jàpp,
fu mu toog jublu xibla te du tëdd mbaa toog mukk ci kaw ab lal bëccëg. Ku bëggoon xet gu neex la daawul tàggoo ak bitéelu
laj-koloñ te fonk ay sër, ku xamoon liggéey la te man a liggeey, ku ko mas a liggéeyal loo xarala xarala mu won la
ca loo xamul, ku man a yare la woon, te xarale te ñime njaboot àttan njël li. Sëriñ Abiibu Si doomam nee na: Lenn rekk laa gisoon mu bañ ko lool góor guy dem ci këri jigéen ba daa na wax ne:
Donga buy tërbiyawu moo ngi mel ni mbuus muñ duy i leer, ndox bu
jegee jigéen ma nga cay jam i ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru,
ku am Tawhiid la woon ba daa ko jàggale
te daa ko jàggal jigéenu këram ba amoon na ca ku mokkaloon teere bu tudd « Burkaanu Sanoosii », mas nay waare ci Tawhiid fekk booba am kuy tuddulu (ku wopp di tudd turu jàmbur)
ay bokkam jàpp kooka di ko dóor ba Yàlla dogalee ka tawatoon faatu, mu ne leen: Bëgg geen xam ne lu am Yàlla a kii geen doon tam ba di ko dóor li mu ci doon dafa mel ni ku romb màngo gu ñoral
mu xam ca doom bu ñor mu gësëm ko doom ba rot ñu ne ko yaa ko ray
te kat bu ko laalutoon ab diir mu rot nde ñor na, daa di wax li Yàlla ne:
وَمَا ڪَانَ لِنَفۡسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذۡنِ ٱللَّهِ كِتَـٰبً۬ا مُّؤَجَّلاً۬‌ۗ = nekkul di ñeel bakkan dee ci lu dul
ndingalul Yàlla ci àpp bu dog.

Moom nag mi ngi fi jóge ci atum 1955 dund na 84i at.

Waxi Sëriñ Maalig Baasin Si

Mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan Donga buy tërbiyawu moo ngi mel ni mbuus muñ duy i leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu...

🎧 Déglu
error: Content is protected !!