Alkande

Alkande j: (tur) Mooy ag alku, ku alku, torox, musiba këpp ci kawam mi ngi ci alkande.

Anéer

Anéer y: tur

Ca bittib dëkk ba. Niral: Xar mu dee ci dëkk bi ca anéer ya lees koy sànniji.

 

 

Àkk

Àkk: (jëf) Mooy song mbir, niki àkki nit.

Àlliwo

Àlliwo: tur

Dénk wees defar ngir di ca bind. Boo demee ca daara ja, moom la dongo yiy jànge.

Ëcc

Ëcc: jëf

Génee ay wëñ ci wëttéen. Jël wëttéen taqal ci ëccukaay di wëndeel muy def i buum di laxasu. Bu laxasoo ba fees di poqe.

Ëmbeef

Ëmbeef l: tur

Li nekk ci biir, li mbir mi ëmb. Niral: Dal bii di jàng wolof de, ëmbeef li am na solo lool.

 

Ëw

Ëw: jëf

Wër, gaw, wër-dombo. Niral: Fukki néegi ñax, ñoo ëw sunu ëtt bi.

 

Ñall

Ñall w: Mooy yoon wu sew wu jaar cig mbooy.

Ñall

Ñall w (tur)

Yoon wu sew, du bokk ak yoon wu mag wa ñépp di jaar.

Ñéer

Ñéer: (jëf) Ndox mu nekk ci biir cin te aw tàngoor yóbb ko daa ñéer.

Niral: Ndox mi ma defoon ci cin leegi di ko tàngal de ñéer na.