Baataan

Baataan: tur

Waat yees di dajale di ko leeral, di ko toj ba mu leer.

Bar

Bar (jëf)

Ñu lay liggéeyloo nga jaare noona dem saw yoon te liggéeyoo.

Bélawu

Bélawu (jëf)

Féqu, xëccu, niki ku daanu jéll rekk ñu téye ko noona muy yëngoo di jaayu wet gu ne mu jëm fa te ñu téye ko mooy bélawu.

Bélli

Bélli: jëf

Ubbi kanam, leeral kanam, wone am mbégte ci xar-kanam.
Nit ku bég, dangay gis kanam ga bélli lool.
Niral: Bélli ag kanam, moo gën bernde.

 

 

Bëlamu

Bëlamu: (jëf)

Taxaw di yuuxu, di sànni say loxo, fu ne di waddi waddi ak a wëndéelu.

Bëmmaakon

Bëmmaakon: tur

Ab bëmmkat, kuy bëmm, di génne am riir ci gémmiñam.

 

Bër-bër

Bër-bër: (jëf)

Lu bëgg a jóg te manul a jóg mooy def bër-bër.
Bëy wu ab wata fiir tànk ya damm day bër-bëri di jéem a jóg te du ko man. Bër-bër joo gis bu sottee, bëret a cay topp.

Bërëx

Bërëx (jëf) Mooy luy tàkk bu baax ni ag sébb. Sawara saa ngay bërëx-bërëxi de.

Bëtëri

Bëtëri b: tur

[En: battery]
[Fr: batterie]