Daa

Daa j: tur 

Ndox mu ñuul mees defar ngir di ci binde.

 

Daakaande

Daakaande: tur

Lu daŋ te dar la di jóge ci garab

Dañal

Dañal: jëf

Dawal, war ci kaw u fas di ko dàq. Niral: Amna gawar bu dañal ba egsi.

 

Dagg

Dagg b: tur

Potu ndagg yi dongo yiy yor bu ñuy yalwaan.

Day

Day: (jëf) Tollu,  Niki: Cëy ni mu day! = Cëy ni mu tollu!

Dànna

Dànna b: (tur) Mooy ku jub loxo, koo xam ne du diir di moy.

Dédd

Dédd g: (tur) Ag garab la.

Boo ci bëggee lu gën a leer bësal fii.

 

Déeyoo

Déeyoo: tur

Ñaar ñuy waxtaane ndéey loo xam ne bëgguñu kenn xam ko,  dañuy déeyoo.

Déglukaay

Déglukaay: tur

[En: earphones]
[Fr: écouteurs]

Dëfeenu

Dëfeenu: jëf

Daanu, këpp, tëdd sab biir féete suuf, sag ginnaaw féete kaw.