Fande

Fande: (jëf) Ñàkk a reer. Ku reerul dangaa fande.

Fande

Fande: jëf

Ñàkk a reer

Fayax

Ne fayax (njëfka)

Ag dal, am péex. Mbooya muy upp ba yàgg mu ne fayax.

Féew

Féew: (jëf) Beddiku dem yaw dong bàyyi say bokk walla say xarit. Ag jur gu ñuy sàmm bu ca menn xar génnee dem moom dong, daa féew, till man na koo jàpp mbaa bukki.

Féq

Féq: (jëf) Xëcc, guddal, tàwwi, yokk. Niki: Yàlla na Yàlla féq saw fan.

Fér-féri

Fér-féri: (njëfka)

Ñàkk a dal, yëngu. Xol buy fér-féri, mooy ku tiit fit wi dalul muy baagante di jóg ak a tóog ni bëy wu rëcc.

Fétal

Fétal: (jëf) War a jaar ca yoon wa, bëgg lu gën a gaaw tax nga bàyyi fa yoon wa, jaar feneen fu dul ca yoon wa.

Fëlamu

Fëlamu (jëf)

Xalangu fi suuf di bërëŋu, di yuuxu. Niki ni jigéen ñi di def bu nit faatoo.

Fëx

Fëx: jëf

Daw ag doole, ne bëret daw mel ni ku ko waajul.

 

Fëx

Fëx: (jëf) Jóg ak doole daa di daw. Jekki jekki daw .