Golliku

Golliku: (jëf) Mooy xàppatiku, niki fu tiim ag kàmb, am suuf su ca golliku daanu ca kàmb ga.

Gorom

Ne gorom: (njëfka)

Sukk sa ñaari bëti wóon ci suuf, sukkiin wu yaru. Niral: Jur ga de ña nga ne gorom ca digg yoon wa.

Goy-goylu

Goy:goylu (jëf)

Ginaar gu wopp ni muy baylikoo, sàngoo ay laafam ay céram du yëngu mu tàyyeel, loolu mooy goy-goylu.