Ja b

Ja b: tur

Fa nit ña di jaay ak a jënd. Maarse. Niral: Ndax pombuteer dana jaay ca ja ba.

 

Jagam

Jagam: melo

Taq, tilim, ñaaw, bon.

Jalax

Ne jalax: (njëfka)

Lu ñu lootaabewul bàyyi fu ne dara nekk fa, da ne jalax.

[En: disorganize]
[Fr: désorganiser]

Jang

Naan ba la nga naanoon di génnaat

Jax

Jax: jëf

Joow. Yëngatu, boole lu ne. Jeñ ag gaal muy daw.

Jàmbu

Jàmbu: (jëf) Amagóo dara di ànd ak sa niti démb, am as tuut rekk jàmbu leen mel ni ku leen xamatul. Niral: Man daje naa ak sa waay fee waaye damaa jàmbu.

Jàngu

Jàngu b: tur 

1-Fa katalig ya di daje di def seen i ñaan ak a jaamu Yàlla. 

2-Fa ñuy jànge, daara ji day am ay jàngu yu bari ci biir.

 

Jànq

Jànq: (jëf) Mooy dox waxtuw tisbaar, ku tukki waxtuw suba dangaa xëy, bu dee waxtuw tisbaar jànq.

Jéng

Jéng b: tur

Weñ gees defar di ko takk ciy tànk ngir bañ boroom daw. Dongo yiy daw dees leen di jéng.

Jëtum

tum j: tur

Ku jëkkëram faatu

[En: widow]
[Fr: veuve]