Kayam

Ne kayam: (njëfka)

Dee, gancax guy sooga dee, ba tàmbalee wow, da naan kayam. Niral: Sa garab gi de nee na kayam, xanaa daawóo ko suuxat?

Kayamu

Kayamu: (melo)

Xel mu dem. Ku ñu wax xibaar bu ko bett rekk, xel ma dem. Ñu ne kayamu na nag.

Kàcc

Kàcc m: Soow mu wayul. Soowum kàcc dafa am, mbaanig am, yaawur am.

Kàncóoli

Kàncóoli g: (tur) Mooy kaña gu mag.

Kàrce

Ay xeexkat yu ànd, militeer yu booloo.

Fr: Armée

Kéew

Kéew m: tur 

Mbooleem fi nu nekk ak li nu wër li nu ëw. Àll yi ak mbooleem gàncax yi añs. Aalam baatu araab la du wolof. (environnement)

 

Këmm

Këmm: (jëf) Mooy ñàkk a ndékki. Ku xëy ndékkiwul daa këmm.