Karc

Armée

Kayam

Ne kayam: (njëfka)

Dee, gancax guy sooga dee, ba tàmbalee wow, da naan kayam. Niral: Sa garab gi de nee na kayam, xanaa daawóo ko suuxat?

Kayamu

Kayamu: (melo)

Xel mu dem. Ku ñu wax xibaar bu ko bett rekk, xel ma dem. Ñu ne kayamu na nag.

Kàcc

Kàcc m: Soow mu wayul. Soowum kàcc dafa am, mbaanig am, yaawur am.

Kàncóoli

Kàncóoli g: (tur) Mooy kaña gu mag.

Kéew

Kéew m: tur 

Mbooleem fi nu nekk ak li nu wër li nu ëw. Àll yi ak mbooleem gàncax yi añs. Aalam baatu araab la du wolof. (environnement)

 

Këmm

Këmm: (jëf) Mooy ñàkk a ndékki. Ku xëy ndékkiwul daa këmm.

Kembaar

Kembaar g: tur

Àdduna bi dees koo xaaj juróomi kembaar, muy:  Afrig Amerig, Órob, Asi ak Oseyaani. Niral: Senegaal mi ngi ci kembaaru Afrig.

 

Kerkiraan

Kerkiraan b (tur)

Yéegukaay, fees di jaar ngir yéeg ca kaw.

Kippaango

Kippaango g: tur

Mbooloo mu booloo di waxtaan mbaa ñu noppi.[En: group]
[Fr: groupe]