Paax

Paax (tur)

Suuf su baax soo xam ne bay ko rekk a des.

Paccax

Ne pacax (njëfka)

Tàbbi ci biir mbir, nekk ci biir yëf yi bu baax. Niral: Man de nee naa paccax ci biir.

Palamtu

Palamtu: (jëf)

Làmbatu aw yoon. Niki gumba buy dox day palamtu.

Pàttaliku

Pàttaliku g: tur 

Lu jàll ba ñu di ko fàttaliku.

[En: memory]
[Fr: souvenir]

Péey

Péey (tur)

Fa buur nekk, yépp daje fa, dogal yi di fa jóge.

Pékke

Crime

Penk

Penk l: tur 

1-Penktel jant. Jant bi fenk.

2-Ci kanamu pooj. Booy uuf àlliwo fi nga koy teg.

 

Poqe

Poqe b: tur 

Bant walla weñ ga ñu laxas wëttéen wa.

Pullet

Génn, génne ci suuf. Ni mbir mi di génne.

Niral: Sindax yu ndaw yi ña nga naan pullet di génne ci bàq bi.