Taax

Taax: (tur) ab tabax

Taf

(ci wàllu xarala)

Dem fu dara newul taf fa la nga teppi (kole)

Tandale

Tandale: tur

Lu am noonu rekk te dara taxu koo am.  Lu jekki-jekki am te kenn amalu ko walla ka ko amal jubluwu ko woon a amal. (Hasard)

Ténj

Ténj: jëf

Ku boroom këram faatu da koy ténj, muuru ñatti weer di sellal du génn dem fenn.

 

Tér

Tér b: (tur) Mooy tilim, ay tilim-tilim.

Tóon

Ne tóon (njëfka) Mooy tëdd ci sab pilyaan tegale say tànk ñu di la liggéeyal. Booba yaa nga ne tóon.

Tele

Tele b: tur 

Tepp-tepp

Tepp-tepp : (tur) Mooy ay taa-taa yu ndaw.

Teppi

(ci wàllu xarala)

Fekk mbind mu tege nga teg ca sa baaraam jël ko (kóppiye)

Toñ

Toñ: jëf

Toŋ, bëŋ, jeñ nit mu jëm ca kaw, dimbali ko ngir mu yéeg.