Waame

Waame w: Taw bu bari te am doole.

Wagg

Wagg: tur

Ay mbagg, bu dee menn mooy mbagg, bu dee yu bari di wagg.

Walax

Ne walax (njëfka)

Nëbb, làq, wann, denciin la denc gu kenn manul a àgg.

Walluwaan

Walluwaan b: tur 

Wata la buy jël nit ñu gaañu ñi, walla ñu tawat di leen rawale ca wopp-taal. (embulenche)

 

Wata

Wata b: tur 

Waxambaane

Waxambaane w: tur 

Góor gu toll ci fukki at ak juróom jëm ñaar-fukk ak juróom. Ku tàmbalee yittewoo jigéen.

Way-dawlu

Way-dawlu ñ: tur 

Ñi faatu,  ñi wuyuji seen boroom. Niral: Ñaanalleen waydawlu ñu Yàlla yërëm leen.

 

Wàcc

Jàng ba jeexal Alxuraan ji.

Wàkk

Aw takkiin, aw bootiin. Jël dara teg ci ginnaaw takk. Niral: Neel wàkk sa doom ji boot.

 

Wéret

Ne wérét: (njëfka)

Génniin wu bette wu waajul. Niki ñu wax la lu la tiital rekk sam xel génn ne wérét.