Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Dof yi

Damaa génn bis saa kër di dox romb benn dof
Mu toog cib ruqam jël ay yoxoom faste ciy waggam

Te leeg-leeg mu ree leeg-leeg mu jooy rafle wang ko wër
Ma ngay lox keroog daa sedd boolek tarug lëndam

Wérul waaye teewul nag mu dis gor nde tàllalul loxoom kenn
Tooñul it ña toogoon ci ag wetam

Yaram waa nga sooñoo sooñoo duw dàll duw basaŋ
Te lee-lee mu taw ndaysaan ba taa suuxal ab ëmbam

Bu xiifee pupel lay dem amul ndey ju koy tibbal
Fa nuy këppiy des lay dem fa lay fekki aw ñamam

Te it man la wax day mujj dem lekki ñam wu bon
Wu am yaari fan woo xam ne baaxul ci ag wéram

Na muy def?Gisul yaayam te it amna yatti at
Yu mat sanguwul lum sol da koy for ci ay sënam

Bu jaaykat bi sànnee màngo mbaa sax orãs bu nëb
Mu daw këf ko noonee sax la koy lekkee cig takkam

Ngalaw sàqi nit daw tàbbi néegam ne kàpp tëj
Mu des tay kanaayal want yay dal ci ay gëtam

E ndaysaan bu rombew dàll mbaa pot wallaw sagar
Da koy teg lu rëy moo tax mu koy boole cib ëmbam

Dafay waxtu fum wéetée te lee-lee mu mer di xul
Te kat am na ndey am baay ba am rakk ak magam

Ba muy wér la bokkak ñépp bis ñëw ñu dal ko ber
E waay wéradee tax waaye as gor la woon su gëm

Rakkam donn nab néegam jabar jaa ngi séy feneen
Te ndoom sam amoon boobee batay xolu koy gëtam

Juróom yaari doof lañ fekk Tàmbaa ñu rendi leen
Ba jël séen i awrak séen i yuur lii ka daw yaram

Dañoo butti ñee xar boppi ñee ñee ñu sànni leen
Ci ay kër yu kenn dëkkul ba ñuy xeeñ ñu door a xam

Gisal ñaata yoon lab dof di xëy dee ci ay tabax
Yu yeggul ba am ay fan ba fay xeeñ te kenn du xam

Gisal benn dof bee faatu Leelan ci wenn xur
Ba fay xeeñ te ab xiif rekk moo sànk ag dundam

Gisal ñaata yoon lab dof di xëy lekk ñam wu bon
Ba febar ca ay at kenn du jug saytu ay mbiram

Gisal ñaata yoon lan fekk ab dof mu xëy wësin
Te ken man ta laaxaan kenn ken foogulab ëmbam

Gisal ñaata dof ngay fekk dus kumba mbaa tubay
Dañuy rafle noonee rek di dem ñépp gis pëyam

Gisal ñaata dof ngay fekk duñ jekki duñ nelaw
Dañuy dox ba dee doo gis ku naa xam na bàmmelam

Te gis naa fi bis ab dof bu am benn góom bu rëy
Ma ngay wokkotoo kay waxtu kenn saytuwul wéram

Liilee tax ma jug tay woo Etaa beek ñi Yàlla ñor
Ñu booloo taxaw tey saytu jaa-Yàlla yii ñu am

Wowóowow wowóo yéen góornëmaa réew mi walluleen
Ewaay walluleen as gor su xëy ñàkk am xelam

Te gis ngeen fi ay dof yoy ku leen faj ñu daa di wér
Te xam ngeen ne mbooleem dof yi koo tëye dootu dem

Nde dof boo fi gis muy dem kërug nit la bàyyi koo
Ku wér dellu ciy mbokkam xarit xel dafay xalam

Te gis naa ku faj mbaamam te gis naa ku faj fasam
Fajum jàmb-jóobam faj goloom sax fajub xajam

Te taxtil mu faj mbokkam mu xëy ñàkk am xelam
Ku faj mbaam fajub xaj bàyyi nit àndul ak xelam

Ci lii sax ci laay faf ñaaxe askan wi may waxal
Ñu daw lépp luy tax nit di xëy ñàkk am xelam

Xelal gànjarag nit xel la nit am ba not mbëfër
Xelay tax xaleb naar not gëléem bay xëccab nosam

Xelay tax nu wullig naaga war xàcc tay dañal
Te xam gee ne du maasam nit ci dooleek ci ag rëyam

Xel ay tax ba lislaam teg nu jëf waa ju ñàkk xel
Asal dootu am aw yiw te dootu yilif këram

Xel ay tax nga xàmmee mbaax xel ay tax nga daw lu bon
Xel ay tax ba nit xam lëf ci Buur Yàlla ak mbiram

Xel ay ndab la xam-xam tàbbi ngir waa ju ñàkk xel
Du xam lëf du am lëf waa ju am xel am i yëfam

Xel ay leer ga nit xëy tedde moo tax ba Aadamun muñ
Di sangub malaakaak jinne Ibliisu ñàkk ndam

Xel ay tax ba nit rekkay sangub suuf lu weesu nit
Xarit loo fi gis ngir nit la ngir moo yoram xelam

Xarit ñàkki gët mbaa ñàkki waaraama gën nga nàkk
Am xel xel ay nit nit nitteetil ci ay cëram

Ku jàngoon walaa tulxuu bi aydiikumóo ilaa
Dangay xam ne kon kuy yàq am xel yorul gëmam

Ma wax yenn mbir yuy tax ba sun ndaw yi xëy di dof
Ñi ley rab la nii ay raab la raab yàq nay ndawam

Dofab raab dafay wuuteek dofab rab ci yenn mbir
Na ñuy moytu yàmbaa daw dorog bàyyi ay mbiram

Dofab iilu ak bob siisu ñoom it danaa ci ñëw
Damay jëkk a way ki sàngara yàq ag dundam

Bu kenn fóoni diyiyã day rayum xel di yàq xol
Lu rey xel di yàqub xol ku koy def du nit daxam

Te alkool alag naw gaay ku koy naani dootu wér
Lu waay am lu dul wér jaay ko ngir jënde kok wéram

Lariklees di yàqal nit ci xol ak ci ay xëtër
Ñi xam nee ñu day dem sax ba far gàttal ug dundam

Te dee diis ku koy naan man na dee dee gu diis te tar
Nde luy fuq bët moo gën ci nit luy fuqab xolam

Gisal waa ji naan sum-sum ne xëndaŋ ci géddi bëy
Nelaw bay xaran sum soof na lool xel yi lay gësam

Amoon na ku màndim sëng faf dër di yag-yagal
Ñu koy tàccu muy taasook a saagaa ci ab ëttam

Te am na ku naan biiñ daanu bañ sàcc lam yoroon
Te muy lim bu rëy boo xam ne moo yor dundug këram

Amoon na ku naan sàmpaañ di xeexoo ñu far ko ray
Sulaar saa ko jam ay paaka ndaw dee gu ñàkk jom

Ku naan roos du rus nit dootu rus Yàlla dootu rus
Njabootam ndaxam man naa sëyak yaayamak rakkam

Wisig yeek falaag day yàq am xel ba leen dorog
Kokaa gën kokaayine fopp cib xol akuw yaram

Te gis naa ku naan am ñoll daa màndi bay tërëf
Xalel yaa ko sottim ndox mu far yàq ay sëram

Te it am na dof yoo xam ne ay wird lañ yoroon
Ba rawhaan ya dofloo leen ñu far topp ay xëram

Gisal benn waay biy wird ab diir mu summi ay
Yëreem summi caayaam génn néegam di dox di dem

Te kat bañ ko laajee nee na suuf see ko àttanul
Ma laaj waa ji kon san suuf la doon sàmp ay ndëggum

Te talsam yi ak rawhaan yi lim sànq ciy xalel
Dorog mantikoo jot fàww daf dul lu neex a xam

Te say jàq tax nas cam di siisook a say ba dof
Kurus ag ndofam day metti ndax yombulam pajam

Gisal jenn waay jiy yuuxu tay daw di wër te naan
Dafay bañ a doon ab xutbu kii séenu nag ndofam

Te am raxasun xas-xas xarit xawma lum saxal
Lu dul ndof jëlal aw tur wu leer bàyyi talsamam

Te tas tas na waay bam yuuxu xàccit mu tas këram
Te tas mbiramak soxnaam ñu naa déet mu tas xelam

Kitil ak katal ak màkk jal-jal ku koy sikar
Bu teewloo war a naree dafay waat yu saf xorom

Te ag nasabin ak hatariisun ku leen bawul
Dafay mujj rekk fab ay mbubbam daanu ciy sënam

Jaxaay yaayi dëhtëhtiilu doofloo na ay kuréel
Jalaal jal na fiy wàmmeel te dofloo ñu am xorom

Gisal waa ji tëj néegam ba ab diir mu mbëkk daw
Te naa maa nee ajabaaru maa tay ci ab ëttam

Ku woo Ummu Muusaak yaayi Xëlbaa ci ay kurus
Ma woo man ki bindoon yaayi Muusaa te yor mbiram

Ku fiy woo Afaariitun minal jinni man ma woo
Ka bindoon Afaariitun te yor léppi wërsagam

Dalal nag te teey booy sàkku mbir ndax ku wattuwul
Xérak ëppalak yàkkamti looy sàkku doo ko am

Faral noppi yaw Baas wax bu niwee te am njariñ
Dafay doy salaatun yal na dal Taaha ak ñoñam

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Sutura yitteel na ku ne

Lu tax nit ñi buñ déggee lu baaxul ci nit ku yiw
Taxaw temm ngir yaatal ko bam law ba daj fu ne

Lu tee woon nga jéggal nit te koy nëbbaley ay sikkam
Ndaxam suturas Buur Yàlla yittéel na cam su ne

Goray xam safaan dencal ko mbokkam ba faatu ñëw
Ragal Yàlla tax ak maandu ak xam na ñëw bone

Bu leen weratib jullit bu leen yàq ab deram
Ku fiy dund feek deewóo safaan man na laa gane

Wolof day misal ag dund ciw koor
Ku jàpp bis lifeeg dog jotul ag jubu weesul fa dog bone

Di siiwal safaanub nit ba far ëpp koy ayib
Ku am xel du def loolii bu leen yor xelam gone

Lu tee woon nga nëbbal kob safaanam te Yàlla tax
Ndagam Yàlla mooy sattaaru maandooy li war ku ne

Na ngeen moytu jëw baaxul te daa mel ne lekk nit
Te rambaaj a raw day tax ba ay bokk duñ mane

Na ngay nëbbe say bon-bon bëggóo kenn xam ca lëf
Na las cam di nëbbey bon-bonam kon bu koy wane

Te Ibliis ma ngeen daa muslu tey moytu ag mbonam
Mu ngoo gii ci seen apaareyiy woote tay sone

Te anternet ay ab jumtukaayam di daamaram
Koneksiyoŋ bi mooy xontam bi ngay aktiwey done

Nataalak wokaal boo jot ci watsab ñu koy toxal
Efaaseel te bul partaase luy yàq ay gone

Éy waay siggileen watsab yi day yàq seen i xol
Lu ngeen am ci mbon ngay xew Farãsak la xew Gine

Éy waay siggileen ceetaan mi réeral na seen i xel
Ba kenn dóotul jàmmanteek i nawleem ya koy gane

Ewaay siggileen for yoon wa yéenak ci xuur wu rëy
Wu lëndam te gar yang fay sibuy yong ay tene

Ewaay siggileen ndax Yàlla seen gët yi xoolu yiw
Ba laa leeri gët yee fàddu xoolleen fa mbir ya ne

Li apaarey yàqal nit ku koy xayma doo fi jug
Batay kuy naxub diriyànke ayfon nga koy cane

Li watsab di jël ciy waxtu ndax jur na ay njariñ?
Te moo tax mukalaf yaa ngi niiy waxtu niy gone

Na muy yàqe dundug nit dafay dem ba mel ne sax
Manul ñàkk cig dundam te am kooy lëjal ku ne

Li ngay def ci Feesbug boo ko jàppoon dogub sikar
Ndaxam lee nga am xam-xam yu Feesbug ya dul wane

Te kat ñàkk Feesbug lortilës cam nde Yàlla mii
La muy sédd ab jaamam ci sax ciw turam la ne

Kurus gaa ngi nii der baa ngi nii jukki baa ngi nii
Ta dog yaa ngi nii céeboy ngënéel yaa ngi dët fu ne

Ku sellal ndabal biiram mu feesak tawab ngëram
Ku not ab xolam cib net ñu nattoo ko mbon ku ne

Ndagam deftilag mbon waxtilag mbon di gis lu bon
Akay déggi bon-bon doy na lag mbon fa mbon bone

Te man maa ngi nii xamteeti mas lëf
Te fàtte naa li saa xol bi takkoon fëtt naa mokkal ak lu ne

Damaa talatul sax wérd mba may talug nafar
Damaa sonn ngir ndéggat yi gaa yi di ngun-ngune

Mo Baas tee nga sàlloo tuub te faf raasi wépp yiw
Labat may yi tàggook moy yi moy yaa ngi lay gane

Te mbon sax jigul sëppéen ba sàkkaa ku tol ne yaw
Faseek moy yi daa jot sëkk ngir doonatóo gone

Ka jéggal ña juumoon démb tey nëbb ay ayib
Dagaan naa ko ag njéggal gu far saa ayib yu ne

Ka xam lépp cib jaamam te muural ko ay moyam
Fa laay tuube laa jàddoon ci ag mag ba cig ngone

Ka jéggal laram Daawuda laay sàkku njéggalam
Te moo jéggaloon Yuunus nde moo tee mu faf jëne

Ka jéggal Badar jàmbaar ya songoo te diine tax
Asal man na maa jéggal ci mbaxam gi moy gu ne

Te kii jéggaloon Wahsii ma xar dënnu Hamsatin
Asal man na maa jéggal te ràngal ma pal ku ne

A yallaahu yaa rahmaanu yaa sañ te yaay dogal
Fa salli halal maahii te far saa ayib yu ne

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun_

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Ñalgul dañal

Bismilaahi rahmaani rahiimi

Ñalgul dañal xalimag way
Ca lef ma ñuy tagge Daamu

Sëriñ bu mag ba fa Tuubaa
Rijaal ya moom la ñu taamu

Moo jar di way ak a sargal
Di riim taggam ya di baamu

Yaw soxna Jaara sa ndam lii
Moo raw ci jëf ak ci jaamu

Mbusoobe moom la nu taaroo
Ak Mëhramu ma mu maamu

Bul wër kemam amulam kem
Seex Ibra Faal fa la raamu

Amul ca Faas ak i Baxdaat
Amul ca Misra ba Saamu

Ku CernoFaati di bóofal
Ak Cerno cër ya mu sammoo

Dootóo fi seeru ku raamloo
Ku toll ne mbër ma fa Ndaamu

Dogon sëriñ ba fa Tuubaa
Sëriñ Daaru jekki ni kaamu

Moom rekk moo man a raamloo
Masàmba Jóob ma fa Saamu

Murit ba daa baye Déndéy
Seex Móodu bóof na ba Saamu

Sëriñ Mamar ma ñu màggal
Bóofal na Bàmba ba Saamu

Sëriñ Ma-Baabu ma selloon
Samsan la bóofe ba Saamu

Péncum sëriñ ba fa Tuubaa
Góor yàlla yépp a fa raamu

Yaa tax ba Ahmadu Baasi
Sàlloo di tagg ak a baamu

Boo jàppatee xalimag way
Taggal ma Ahmadu Daamu

Askaasaraa may rabbin
Bihii yunaa lumaraamu

Halal nabiiyi bi hizbin
Feeg maa ngi fi tagg Daamu

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Yewwuleen

Bismillaahi rahmaani rahiimi

Yewwuleen bu Yàlla falee
Ab laram na ñépp dagu

Dag ca péey ba lay xala añ
Wuyusileen ci seeni sago

Xaadimu Rasuuli la fal
Gàngunaay ga moo ko jagoo

Moom la Yàlla far ca lësal
Nattu yooya moo ko tegoo

Farlu ga ak yitteem ja mu yor
Lëf taxul mu raf bu dogoo

Yàlla rekk rekk la ŋoy
Alxuraan la mas di fegoo

Sopp Mustafaa di xolam
Aw taggam la mas di wagoo

Aar na ngir mi Yàlla tëral
Ag tëyam la mas di wegoo

Waa ju xam du wër ku ko moy
Moom la Mustafaa di sagoo

Lim defar ci dénd bii doo
Seeru fii kemam ba Tógoo

Wër wëraani dem na ba ñëw
Dem na Misra dem na Segu

Wër na ñoñ Araab ba dajal
Ñëw ñu naa ko yaw jugagóo

Nee gisul fi dëek i didi
Réew mu nekk nee na fa góo

Ag Yonen ci Taaha la yam
Xejj baa ngi kaay nu dagu

Baas yëngul te way ko ndaxam
Soo ko bàkkagul wayagóo

Baas yëngul te jublu ci moom
Soo ko jubluwul wayagóo

Sant rekk mooy li la war
Yaa ngi saddi way te gagóo

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Aji-topp ji: Seex Lóo

Catégories
Sëñ Ahmadu Baas

Afrig

Afrig sa doom yaa ngi war ay gaal di tàbbi ci mbeex
Di lab di dee soo jógul kat lee ñu faatu ba jeex

Sa néewi doom yaa ngi géej giy gëq booba ba tay
War-ndéexe tax leen a war ay gaal yu gudd ta déex

Géej gii jirimloo na ay ndaw tas na ay këri-kër
Jeeg jiy jotul seen i rangooñ sax ci tuuru ba jeex

Ay ndaw yu am doole am xam-xam di sànku jubul
Afrig jógal kar sa ndaw yii leegi say gone jeex

Su géej gi dee ray tubaab yiy jàppe ak di fital
Nga sax ci nguurook a xëccooy pal balaa bi du jeex

Kuñ fal mu lëngook i gaayam sax ci sàcc alal
Di taax ak ay tuuxu ay sàntam di regg ba géex

Rongooñi waadoole yeek miskiin yi faf saf i déeg
Di siim cerey wuur yi tay siif seen ñaxet di ko ñeex

Way-ñàkk yiy wéy ci seen ug ñàkk gaa ya amoon
Di gën di woomal bariy daamar di lekk lu neex

Baykat ba daa suqlim réew réccu lum baye woon
Bay weeri weer jaaye as njëg notti notti ga yeex

Ku jaay kilob gerte tay jii njëg sa num man a toll
Du mat kilob ceeb mo ndax baykat bi deeti na féex

Tay Afrikaa jaay na ay géejam yabooy ak i jay
Lay xonti doomam tubaab yiy yóbb jën yi fi weex

Ag càmm yàqu na, jur giy wopp parlu hamul
Baykat yi ak sàmm yaa ngiy soow i ruur ak a xeex

Ku màng téemeeri nag ren jublu àll déwén
Mu mànki fanweeri nag ag càmm yàqu na jeex

Ku jàng yor ay lijaasaam mun la ham fumu xëy
Yii rekk a tax ndaw yi jóg war gaal yi tàbbi ci mbeex

Afrig jógal defaraat mbay mii nga ham te defar
Sa càmm gii nanguwaat géej gii tubaab yi ne céex

Sekkarti dex yii ñu sakkoon jël sa ndaw yi nga ham
Joxleen i xëy dunde sam koom ñàkk dal di fi jeex

Yaw am nga way xaralaak ay waane am ñu xereñ
Say suuf njariñ li mu ham réerul ba dee fi ko jeex

Am ay garab tay jëggaanim paj ci réewi Tugal
Say ndën di ñor ngay xëccoo lañ wetti ak di ko wéex

Afrig dogal buumi njaam yii ndax nga àgg ca kaw
Lu der bu ñuul tële tay bay jaamu till yu weex.

Lu nit ku ñuul di xëccoo ak nit ku weex du ca jot
Ak doonte moo ko yayoo ñuul tax du jiite ñu weex

Seetal sa doom yiñ fi ràngoon ngir ñu wallu tugal
Dogan kon ak ñoom tugal day far ca boobële xeex

Tay jii Tugal xañ la ay wuntam sa ndaw yi taxaw
Di ñalgu ay gaal di xét ay géej di faatu ba jeex

Biddanti bon na ndaxam Afrig bu teeloon a jóg
Kon tay Órob du nëxal géejug xelam ba du téex

Seetal ma réew mii di bañ lim am di jëgg di jël
Ceebub Risaatool bi jeeg jii nee ñu mantil a neex

Tay dàlli Turkeek i Siin ngay jëndi junni di sol
Te dàll Ngaay nekk nii gën fopp piire te féex

Orãs ji ñor Kaasamaas lañ jal ci mbedd mi def
Juñ jëggi ciy firigoo ngir nee ñu moo gën a neex

Sobles Risaatool la ñuy wànteer ca luuma ya tay
Sobles bitim réew si lañ seeral ne moo gën a weex

Jëggaani aw làkk jox sam réew ñu fàtte Wolof
Di soppi sax der bu ñuul ciy jumtukaay ba mu weex

Moo der bu ñuul lu la jot lii ndax tayeef la ci yaw
Déedeet li sam xel mu nëx taxtil ba nëxtil a téex

Faral taxaw foofu yaw Baas njàmbatak ba a yam
La gaa ya daa mer ci baawon mer la muy tëe a seex

Allaahuma salli halaa Sëyyidinaa Muhammadin wa sallim

Aji-bind ji: Suhaybu Si