- Mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan
- Donga buy tërbiyawu moo ngi mel ni mbuus muñ duy i leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru
- Kilifa ba laa war a digle day def ba laa war a tere day ba
- Liy yàq kilifa, ñàkk njariñ, ñàkk a jëf.
- Lépp looy santaane na fekk nga manal ko sa bopp ba su ñu gàntoo it nga defal ko sa bopp, ngir nit ñi ku léen yaakaar ñu wor la.
- Liy yàq kilifa, yatt la: 1. Lu mu xam wax ko; 2.Luñ ko wax, mu waxaat ko; 3. Lu mu mer, xul ko.
- Ku la jaay yatt (3), jënde ko yatt (3): 1. Ku la jaay xam-xam, jënde ko maandu, mu ne ndax as gor bu maanduwul du ko teree moy Yàlla; 2. Ku la jaayub juddu jënde ko ngor, ngir juddu bu rafet du teree dem kaso; 3. Ku la jaay alal, jënde ko doylu, ngir bu doyluwul dina sàcc
- Lees yarul kenn du man a jaxasoo ak moom, loo bëgg a jaxasool danga koy tàqale ak moroomam ya yaruwul.
- Kilifa daa war a yar doomam, moo gën jekki ba fiy bëgg
a juge, naan sama gannaaw na ngéen topp ci diw. (nde loolu ku yar sa doom bam man a yor mbooloo doo ko wax), te nit ñi boo nee léen topp léen diw mii, bu diw jubul it duñ ko topp. - Yàlla mooy ndox ma Rasoolu Laahi mooy teen ba sab Sëriñ
mooy goj ba pas-pasu taalube ba mooy baag ba yitteem mooy
di yoor ak a jukki ba barim ndox. - Li tax kuy wut Yàlla ay mbokkam di ko yedd, jaam buy wut
boroomam talut moroomam, bu amee boroomam bëggul moroomam. - Ku dul mer mbaam la, Ku dul mar xaj la,
- Nit ku yiw, na joxe dooleem, joxe alalam, waaye bumu joxe
ngoram, ndax ku joxe sa ngor dootóo dara. - Ku gis sa baay, gis sa nijaay, gis sa taawub baay
war a xam sa bopp. - Danga gis boroom judd buy taxawaalu ak ub juddoom; Boroom xam-xam buy taxawaalu ak ub xam-xamam waaye doo gis mukk boroom liggéey buy taxawaalu akub liggéeyam.
Aji-bind ji: Seex Lóo