Al hamdu lillaahi rabbil haalamiina ndaxam ak cant war na ci man al hamdu lillaahi
Naa jóg te santati Buur bi xëy ma bind ci ndox muy daw ci biir i sidiit al hamdu lillaahi
Naa jóg te sant ki aare aw lumb suux ak i yax xàllal ko pinc mu yaa al hamdu lillaahi
Naa jóg te santati Buur bi tënk bëtt ci lëm may rëpp jàpp ko naa al hamdu lillaahi
Naa sant Buur bi fi tàllal suuf si sotti ci ndox meññet mu teey di ci ñor al hamdu lillaahi
Naa sant Buur bi fi yan samaawu jant ak i weer biddiw ya feg sama réer al hamdu lillaahi
Santal Broom bi la jox soldaar yu bët teguwul ñuy daan sa noon yi yëgoo al hamdu lillaahi
Santal Boroom bi la jox cawwam ju sell te yaa ngay nokki tus fayuloo al hamdu lillaahi
Santal Boroom bi la may sañ-sañ ci say jur i kër ngay tër di def ci sa biir al hamdu lillaahi
Santal Boroom bi la jox, ay cér yu topp ndigal foo leen yabal duñu bañ al hamdu lillaahi. Santal ki baaxe la lum xañ say moroom yu bari ngay ree ci biir aji jooy al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant ki fab daamar yu gaaw ni la am ngay war di dikk ak a dem al hamdu lilllaahi
Moo tee nga sant kilay fajtal ci boo tawatee moo cér pikiir ak i reen al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant ki yor wërsëg di jox ku ku soob jinne ak mala ak rabi ndox al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant ki def sëqub melen ci sa kër ñuy fortu ñam wa nga tuur al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant kilay wax kaay te sant ma ngir say may di dolliku neel al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant sa géer gii sànge la ak suttura muur say ayib toroxóo al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant kilay jéggal sa njuumte yu réy loo moy te tuub ko mu far al hamdu lillaahi
Santal ki ngay dese saa yu ñépp nee la yalax mooy soppi njàqare mbég al hamdu lillaahi
Santal kilay may a may ak loo ko xëy moy a moy ëppante na ak topp jaam al hamdu lillaahi
Moo tee nga sant kilay wax kaay te sant ma ngir say may di dolliku neel al hamdu lillaahi
Sun xippi ak sunu xef sun yëngo ak sunu dal nuy dundu baate nu faat al hamdu lillaahi
Al hamdu lillaahi rabbil haalamiina ndaxam ak cant warna fi nun al hamdu lillaahi.