Catégories
Sëñ Fàllu Mbàkke

Sëñ Fàllu Mbàkke (Xaaj 1)

Ci kàddu gi: Seexunaa Sëy

Waxi Sëriñ Fàllu Mbàkke

1- Boo bëggee mucc ci làmmiñu nit ñi, deel def gémmiñ gu ŋa nga def ca dara. Kon ñaanal la rekk lañuy def.

2- Àdduna benn fan la muy tay, démb weesu na suba dikkagul, kon fexeel ba tay jag rekk.

3- Saabu weer teroo xamal ne weer wàññiku na ci sag dund te dóotul déllusi mukk!

4- Ak ndawal jarul xér, ndax saa boo ko tiimee rekk bakkan rot na.

5- Nit man naa suufeel boppam waaye bu mu nangu ku ko ci jàppale.

6- Nit boo bëggee seen diggante yàgg, danga koy jàpp bu wér. Ndax nit xëjul ci ñatti waaraam, koo cof mu wadd.

7- Sëriñ bu mag bi kenn bañu ko, ku ko xamul rekk a fi ne. Waaye moom ku ko xam bëgg ko.

8- Diw du ma yilif, waaye diw a may yilif jarul xuloo jarul xeex. Ginnaaw yaw yilifóo dañu lay yilif rekk.

9- Kër, kër-kër a koy yor, waaye toog yoru ko.

10- Ag muñ suuf rekk laa ci ñee.

11- Xajoo naa leen, xajoo seen i bëgg-bëgg.

12- Mbubb moo xool jekkul ci sab der, bu ko solal sa mbokkum jullit.

13- Ginaarug jaboot ni muy yërëme ay doomam nu ko raw laa yërëme mbindeef yépp.

14- Ab ànd li koy yàq mooy: tege lu maneeful ak gàntu lu maneef.

15- Li nga dégg ci nit boo ko gënee gëm ci li nga xam ci moom, booba la nga dégg da laa gënal.

16- Jigéen manut a taxaw jub kocc fàww mu wéeru, kon yaw miy boroom këram nangul mu wéeru ci yaw.

17- Boo yéenee ñépp jàmm, ku am jàmm, nga am jàmm. Ku amul jàmm it yaw danga am jàmm.

18- Koo nekkal ku ne mu nekkal la, kon nekkalal Yàlla mi nga xam ne bu la nekkalee, dóotoo soxla ku lay nekkal.

19- Jaay naa samag njureel sëriñ Tuubaa, jënde ko la nekk fa moom, bi ma ko jaayee ba noppi it, jox naa ko njëg gi àddiya.

20- Boo bëggee mucc ci nit ñi nii ngay def: bul tooñ kenn, ku la tooñ nga baal ko, loo am bokk ko ak ñoom, lu ñu am nga yéene leen ko.

21- Jumaa ji dina àgg coleet, ma jiite ko ay ati at.

22- Am mbind ñaar a koy tax a rafet: araf wu ne nuru la mu doon, te nekk fa mu war a nekk.

23- Yaar rekk a nu fi bàyyi: muy muñ baŋŋ-baŋŋ yi ak xaj bon-bon yi.

24- Yaw miy wër ku mel ni sama sëriñ bi (Seexul Xadiim) man ngaa noppalu, te xam ne doo ko gis mukk.

25- Tuur rongooñ ngir bëgg Sëriñ Tuubaa, gisuma lu ko gën di farata.

26- Buma sañoon lu baax laay am, te bokk ko ak ñépp.

27- Ndokk ba nu ko amee moom Boroom Tuubaa, kaar ba la cee cat a dugg.

28- Samag bëgg ci moom, tax na manatumaa bëgg leneen lu dul moom Sëriñ Tuubaa.

29- Man ak sama mag ju baax ja, sëriñ Móodu Mustafaa sunu maam Ceerno danoo jàngal ba nu ne arr, yar nu ba nu ne nërr, yee nu banu ne jarr.

30- Deeleen jaamu Yàlla ci jaami Yàlla yi.

31- Nanu jàpp Sëriñ Tuubaa bu baax, kii nu am kenn amu ko.

32- Jihaad dëgg mooy: di jaamu Yàlla, te not ci sa bakkan, bamu yomb ci yaw lool”.

Aji-bind ji: Seexunaa Sëy

Aji-topp ji: Seex Lóo