Catégories
Seex Ibra Faal

Seex Ibra Faal (Xaaj 1)

Waxi Maam Seex Ibra Faal:

①” Aa doom jàppleen ci liggéeyu sëriñ Bàmba bi ku ci jàpp mu dem ku ci jàppul mu dem kon tee ngeen cee jàpp mu mel ne yéen a koy doxal ngeen dese sag bi

② Aa doom yoonu baay faal deful woon lu Yàlla diglewul ku ko àttan moo fi amul woon.

③ Aa doom làmbi Yàlla àjjuma lay tëgg xumb gàwwu tas dibéer duma wax kiy daan ndax du ay teggin waaye ba làmb ja tasee saa Boroom woo na ma gëram ma ñatti yoon yonente bi gëram ma ñatti yoon sëriñ Bàmba gëram ma ñatti yoon kerog laa raw xel, raw bët, ñiy xool duñma gis, ñiy xalaat duñma xam.

④ Aa doom ku nekk ci li la war mucc ci li la wër.

⑤ Mujjug jamono nit ñépp dañuy jël ay wax def ko yitte waaye yéen ñi ma yaakaar jëlleen jëf def ko yitte.

⑥ Aa doom man a waare fexe ba ku la gis waaru moo ko gën.

⑦ Aa doom bungeen di liggéeyal sëriñ Bàmba na ngeen di nëbb seen bopp te wane sëñ Bàmba, te bañ di wane seen bopp nëbb sëñ bàmba. Saa su ngeen wane seen bopp nëbb sëñ Bàmba di ngeen nëbb te dóotuleen feeñ, waaye su ngeen nëbbee seen bopp wane sëñ Bàmba moom moo leen di feeñal te dóotuleen nëbb.

⑧ Ag taalibe dees koy wut, waaye boo demee ba yëg ne am nga ko rekk mooy ñàkk nga ko.

⑨ Aa doom rus naa ñaan Yàlla lu liggéey di maye.

10- Boo bëggee nekk ci kanamu gaa ñi, dangay raw taxaw nég leen, ëpp doole doo noggatu, xam sikk yi maandu ci, bari njariñ di leen jariñ te doo ko puukarewoo, ku tële nga yóbb ko, doo jëw ku Yàlla bind, ku la jëw nga baal ko, doo yàq alali ku Yàlla bind, ku yàq sa alal nga muñ ko, ku Yàlla bind yéene ko jàmm, ki la xëy jox la junni ak ki gont laaj la junni ñoom nga yamale ci sa xol. “

Aji-bind ji: Seexunaa Sëy