Catégories
Kumba Gawlo

Deppaas bu doy

Deppaas bu doy jëkkër ju la nob.
Xel mu dal ca la.
Deppaas doyul jëkkër nobbu la
Saw fit ne tëfit

Li ma yor sax su doon jaay gone yi,
Kon ma jallax la ko
Man li ma yor fàtte naa ka ñaan gone yi
Foo ma jallax jëme?

Deppaas bu doy jëkkër ju la nob xel mu dal ca la.
Deppaas doyul jëkkër nobbu la
Saw fit ne tëfit

Li ma yor sax su doon jaay gone yi,
Kon ma jallax la ko
Man li ma yor fàtte naa ka ñaan gone yi
Foo ma jallax jëme.

Seetluleen géej li muy rëy rëy saxaar-jéeri du ca daw
Lu dul gaal du ca daw lii boroom gaal a ko xam.

Àdduna a ngoog ku ko seet tay say xalaat jeex nanu muñ
Di sëngéem jooy sunu xol Móodu Maamun sang ba.

Seetluleen géej li muy rëy rëy saxaar-jéeri du ci daw lu dul gaal du ca daw lii boroom gaal la ko xam.

Deppaas bu doy jëkkër ju la nopp xel mu dal ca la.
Deppaas doyul jëkkër nobbu la
Saw fit ne tëfit

Mbës mii mbaa sonnalu leen gone yi,
Cëy wallaay Kumba
Li nu def mbaa neex na leen xale yi?
Waaw wallaay Kumba.

Deppaas bu doy jëkkër ju la nopp
Xel mu dal ca la.
Deppaas doyul jëkkër nobbu la
Saw fit ne tëfit

Mbës mii mbaa sonnalu leen gone yi,
Cëy wallaay Kumba.
Nun li nu def mbaa neex na leen gone yi?
Waaw wallaay Kumba.

Lu doon jar ñaari dërëm démb ba jar na juróom-benn tay.
Njaboot gii fu ñu jëm? moom boroom kër xamu ko.

Seetluleen géej li mu rëy rëy saxaar-jéeri du ca daw.
Lu dul gaal du ca daw lii boroom gaal la ko xam.

Àddunaa ngoog ku k seet tay say xalaat jeex nanu muñ
Di sëngéem jooy sunu xol Móodu Maamun sang ba.

Kuy laax géej sab sanqal dina yàqu te sab laax tooy. Soow ak yolom
Sor jonkoroŋ jonkoroŋ
Saa ginnaar kóli
Mawda siro Mawda siratoo jën wu mag du nelawal gaynde bu bóofee ba ko fa ndax boo ko laalee dee man dee duma ko laal Gumba Gawlo ñëwal.

à yee deppaas bu doy jëkkër ju la nopp boo yeboo kontaan.

Waaye deppaas doyul jëkkër nobbu la saw fiit na tëfit.