1- Ab tegale bu guddee te daanu wul ba jiitoo jub lool.
2- Àdduna gaalu ndox la, waajur bokk na ci gaal yi fiy jàllale.
3- Àdduna weeru koor la fàww jant so nga doo ga waññi bis.
4- Àdduna wori neen la.
5- Alal ganug dof la, buy ñëw du tàggoo, buy dem du tàggoo.
6- Alalu golo ca leq ba.
7- Alalu ku sàggan ku farloo koy for.
8- Am gémiñ taxul a mën a wax.
9- Am naa gëléem ca Gànnaar yomb naa wax.
10- Am ndaa, toj ndaa taxul a bari ndaa.
11- Am soxla fajal ko sa bopp te kenn yëg u ko jar naa bay guddi.
12- Andadoo bukki, bu ko bukki lekkul bukki la.
13- Àq du yat waaye bu dalee dinga ko yëg.
14- Ay du weesu baay dee na.
15- Ay du weesu sàq ma lakk na.
16- Ba feneen amee ba léegi kenn sonnatul.
17- Baadoolo du jub gàcca te aggu ca.
18- Baadoolo rekk la ñuy may lépp mu jël lépp.
19- Baadoolo xamul njoowaan.
20- Baaram bu ñu tàllal joxoñ la waaye juróom i waaram yu ñu tàllal yelwaan la.
21- Baax ci sa alal, jàm¬mbaar ci sa doole.
22- Bakkan waro dàll la fa muy daggee dooko yëg.
23- Bala nga naan naam ne fa.
24- Bala ngaa xam, xamadi xaw laa gaañ.
25- Bala ngaa daas am loo réndi.
26- Bala ngaa digle sangu na fekk nga set.
27- Bala ngaa laax jaay, laax lekk.
28- Bala ngaa xam lu taat di jariñ toog jot.
29- Bant soo koy jubbanti da nga koy jubbanti ci ba mu tooyee.
30- Bant, lumu yàgg cib dex, du tax mu soppiku jësig.
31- Bari le barkeel le moo ko gën.
32- Bari xam-xam weesuwul nettali sa géntu moroom.
33- Bari xar bumu la tax a ngen¬te kou ëmbëlul.
34- Bày ci sa wee wu tànk.
35- Bëgg bëgg yee wuute, moo tax njaay may jar ca ja ba.
36- Bëgg lu la neex du tax ma ne la Yàllaa ngi lay nuyu.
37- Bëgg lu neex gan du tax ma boot jiit.
38- Bëgg ndawal bu la taxee fekk ñay bu taxaw nga di ko galgal say tànk damm.
39- Bëgg soow rekk warul a tax nga woowee béy yaay.
40- Bëggum ñeex du ma tax a dëppoo cin lu tàng.
41- Béjjën mënul a njëkk a sax bopp.
42- Bëñ weex na lool waaye deret a ko lal.
43- Benn lam du yëngu.
44- Benn loxo du tàccu.
46- Bëre géewu dof la, ku wér génn ci.
46- Bes boo gis, day leb walla muy fay.
47- Bes du tuuti boroom lay tollool.
48- Bët dina set.
49- Bët du gis li koy fatt.
50- Benn loxo du tàccu. bët du gis la koy fatt.
51- Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan.
52- Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk.
53- Béy du gëmmal gënn.
54- Bëggum ñeex duma tax a dëppoo cin lu tàng.
55- Béy du raas déemu guddi.
57- Béy fu muy bàkkoo bari gerees nag nekku fa.
58- Biir du suur xel ay dal.
59- Boo bëggee ray as gor dee ko jox bis bu ne lumu dunde bu yàggee nga def ko mala.
60- Boo bëggee xam luy laabiir amal doom.
61- Boo bëggee xam luy muñ amal jabar.
62- Boo wonnee ñay ci sutura, boo demee àll ba mu feeñ.
63- Boo yaroo, té yeww wu loo alalu boroom barke nga.
64- Booy sómbi na nga sómbi loo mën a naan.
65- Bopp du ngir karaw kese.
66- Bopp su naree am barke nopp yuy dégg a cay sax.
67- Boroom karaw gu ñuul ñàkkul dara.
68- Boroom nday ju liggey ku ko yéene fande, yàpp u giléem lay njogonikoo.
69- Boroom ndékki ku ko njëkka yewwu tëddaat.
70- Boroom tubëy bu jàngoo sol.
71- Boroom yat du sóoru boroom fetal.
72- Bu bërti bërti doon tax a jar kon béy kenn du ko bàyyi daral ga.
73- Bu cër yépp yemoon ñay gedd bosam.
74- Bu daay tàkkee céeli yendoo naaw.
75- Bu gudd nopp doon tax di njiit mbaam di sunu ilimaan.
76- Bu jinax doon tux sigaret kon isin yi ak « biro » yi lakk.
77- Bu jinne bëggee dàqaar ku yéeg daanu.
78- Bu la am am tax a bew, ndax ñàkk du wees.
79- Bu la mar tax a naan póotiit.
Aji-dajale ji: Allaaji Jibi Sëy
Aji-topp ji: Saasumaan bi