DOLLI NU
Dolli nu doo jeexle dara
Moo tax ma laajati dara
Nde duma laajati dara
Kon mukk ngir am naa la bir
Yaw waande ag dex nga te dex
Du dëy du jeexle mukk ndox
Moo tax ma naa dolli ma ndox
Te dolli mag wér aku tur
Ren jile may nu ab nawet
Bu gën a jub bépp nawet
Te ëpp mbég bépp nawet
Jàmm ak dugub na ne xasar
Aréen akuw sëb ne xasar
Murit yu nangu ne xasar
Mébét mu nekk ne xasar
Nuy sant nag cant gu tar
Te may nu naataange ju sax
Ju ànd akug cant gu sax
Bunu tawat jegeeti sax
Tay ak ëllëg ci menn mbir
MBOOLOO MI
Mbooloo mi, mbooloo mi nun ñii ñépp yal na nu am
Tawféex ak ug jagle fàww ak mbir mu jub mu yéwen
Te Yal na nuy ëpp tool ak tóokër ak ku nu bañ
Dooleek a not saa su ne tey fekke fàww déwén
La sedd xol yépp biir ak biti Yàlla na nuy
Wutseek a sopp ak a jëkkanteek a dëkk fi nun
La dee fi bañ yépp biir ak bitti Yàlla nu nuy
Muslook a moy fàww akay teggeek a daw sunu mban
Saayir si Yal na rafet
Baatin bi Yal na ko gën
Nu gën fi gënle fi biir ak bitti man ñi fi man
Nit ñépp Yal na ñu nuy
Naw saa yu nekk ak a ñee
Nuy yokk fàww i galañ
Te yokk ñéppiy galan
Jaaraama Yal na sax ak jaajëf te Yal nanu sax
Ku nuy saxal jaajëf ak
Jaaraama guddalu fan
Wérug yaram yal na sax
Dàkk ak lu koy tax a sax
Mbër Yal na jéggal
Yëram sigree nu boole nu tin
Ku nekk Yal na di gën
Bay yokk fàww di gën
Way yokk fàww a wéy
Nuy baax akay sori bon
Wuy Yal nanuy mujji ñépp ak seeni yëf bu rafet
Te mujj ñépp gannaaw ag cant cant a fi yam
Àddina Yal nanu tonnee tonni wépp niwam
Jébbal nu fàww yiw ak yépp nenam yu mu nen
Ka dàq a nal dàq a
bës bëskat yi Yàlla na
Nelaw
koo gis bësal ko
Segal jéggal ko lépp yéwén
JÉBBAL NU YAW…
Jébbal nu yaw sunu Boroom
Woroomi koom ak seen i koom
Nemmal nu it yamb woom
Jox nu xëbam yépp nu moom
Nemmal nu nun yamb wu lëm
Ma mu ne fees akug lemam
Te naanagul lëf cig lemam
Xëpp nu lem gépp nu moom
Nemmal nu sax lu gën a woom
Yamb wu nekk gën a woom
Fopp Morel te gën a woom
Kompañi fopp ak ña ko tiim
Def ma ku ñuy naw ak a ñee
Ku kenn dul gis kumu ñee
Te kenn du dégg it kumu ñee
Mukk ci ñiy jàpp ak a tiim
Bënnal nu it teeni ngëram
Yu xëy ne dell ak i ngëram
Fàww it ne dell aki dëram
Yu lew yu ñuy musal ci juum
Joowal saxar ak i wagoom
Teral fi nun yebbee ci ñoom
Yéere yu ñàkkati morooom
Jébbal nu yaw amóo moroom
Joowal saxaar ak ndam gu woom
Gu lonku junni bi wagoom
Teeral fi nun yebbil nu koom
Su bari jox nu Yaa Kariim
Géejug njariñ nga yaw gu wér
Def nu pakeb ngëram gu wér
Boo musal ak gaa ya ca war
Jépp ci diig ak ci rajiim
Musal nu fàww ci ñi bon
Tegal sa tànk yi ci bon
Bunu bon ak bon guñu bon
Bóofal fi nun bóofal fi ñoom
Yal na nu for ci yaw lu wér
Lu gën a wér lépp lu wér
Te gën lu kenn mas a for
Ci darajay ngën gi xadiim
Yal na nu for ci yaw dogub
Dugub gu réy loolee dogub
Gerte gu réy lool ak u sëb
Te mucc cim dog ak u fóom
Yal nanu for cér bu rafet
Ci yaw ak ag mujj gu rafet
Te dund dund gu rafet
Wér gudd fan jub jub i doom
Yal na nga fab lu gën i doom
Fàpp te fab lu gën i koom
Jox nook i doom ak koomi koom
Nangul nu yaw sunu Boroom
Yaw ki nu bind ciy nelaw
Ba manuñoo ñàkk a nelaw
Faf nu musal ci bunul nelaw
Ak bunu yewwoo ciy nelaw
Musal nu may nu wépp yiw
Ku gëmm bët musal ko yaw
Ku yewwu may ko jàmm yaw
Jamono teeyal ko xelaw
Nun ñépp teeyal nu xelaw
Teeyal sunuy barab xelaw
Nun sant akay naat ak a law
Te jàmm rekk di gelaw
Nun ñépp may nu toolu mbég
Yu nangu lool ak këri mbég
Tay ak ëllëg yu wér te jag
Ak sa ngëram lu ñépp naw
Nun ñépp def nu xejji Buur
Te def nu wëkk-néegi Buur
Te def nu it làmmeñu Buur
Te xol ba faf nu jëme kaw
Nun ñépp def nu géeji leer
Te def ci nun pake yu leer
Ñii yab akay déqeek a leer
Ci sunu biir ak a taxaw
Nun ñépp def nu ñoo wuyu
Ñu penku ak soowu wuyu
Te def nu it ñu la wuyu
Ñu seen i fan guddak u yiw
Nun ñépp def nu ñoo xorom
Ñu bari pepp ak xorom
Te bari ndox bari ngëram
Saf sàpp raw mboolem ña raw
Nun ñépp def nu ñoo maneel
Te def nu it ñi la fi neel
Te def nu fàww ñoo fi neel
Labal nu nun ñépp ci yaw
Nun ñépp def nu ñoo musal
Nun ñépp def nu ñoo mosal
Nun ñépp def nu ñoo bégal
Ñuy mbég di dar fàww ak a ëw
Nun ñépp walloo nu njariñ
Lu rëy lu suqali njariñ
Ci sag tëy ak barkeb sëriñ
Tuubaa ki aw fa mat a aw
Naatal nu nun ñépp bu wóor
Fegal nu bekkoor it bu wóor
Saxal nu cig topp gu wóor
Goo nangu yaw ki dul nelaw
Sëriñ bi gaa yaa ngi rëbi
Jigéen a kay dox di rëbi
Ag jur ak ay wutug xabi
Man Mbàkke maa ngi lay rëbi
Xam naa ne yaa di ngën gi rab
Te ku la jam jam wépp rab
Ku la moy it moy wépp rab
Yal na nu jam sa pàddu bi
Yal nanu fab sun dëggu bi
Teg ko ci kaw sa dëggu bi
Yaw ki foboon sa dëggu bi
Teg ko ci kaw dëggub Nabi
Na nga nu may ndimbal lu rëy
Te may nu it tawféex gu rëy
Gatandu nook i may yu rëy
Yaa gën a am gën a tabe
Na sunu itte yi kawe
Sunuy maqaama it kawe
Nuy kawe bay gën a kawe
Ku ne ci biir ak biti bi
Na nga nu farle ba nu ub
Tay ak ëllëg làmb ju jib
Te def nu mbër mu yaru jub
Mu dul bajantu du tëbe
Te dëgg def nu ab muriit
Mu wecci junni bii muriit
Yoo xam ne bii seenug muriit
Saf na la saf Yonente bi
Teg nu ci kaw sunuy moroom
Fa Yàlla kay sunu Boroom
Ak fa kanam sunuy moroom
Nuy gaa yu gën yu dul tëbe
Bëccëg gu jot jëme nu kaw
Guddi gu jot jëme nu kaw
Waxtu wu jot jëme nu kaw
Jàpp nu ak sa loxo bi
Foo tollu dee nu jëme kaw
Ànd ak mbég ak jàmm aku yiw
Nuy sant akay jëm kawli kaw
Yóbboo nu nii yaw sang bi
Te rikk saa béppub jataay
Na gën ci nit béppub jataay
Fegal ci saa béppub jataay
Saytaane ak moy ak sobe
Fegal nu lor ak sababam
Te may nu yiw ak sababam
Ak sa ngëram ak sababam
Wuyu nu yaw la nuy rëbbi
ÀDDINA
Àddina yal na ci sun xol sedd bis ne xolum
Muusaa ba sedde ca bis boobee bañam ya labee
Dex gaa ne ciix i bañam ray wacc kooku nitam
Ñu mucc raw muslu daqug lem te daqle bee
Ab sang yal nay tabeek ay tàbbi waxtu wu jot
Ba ñépp naa masunoo xam sax ne nii la tabee
Idiriisa Iisaa Xudar Iliyaasa Yal na ñu nuy
May nun ci ñoom ug texeek ug raw bu gaynde tëbee
Te Yal na dox sunu digg ak gaynde saa yu tëbee
Mu teggi nook u ayam wéy mooy sunus mbarabee
Kay ubbi yal na nu ubbil wunti aljana nun
Afal te jàppal nu mboolem wunti naari ubee
Nawet bu ñëw yal na nuy teeweg ñëwam bu rafet
Tey ëpp nit ñépp gertee kuw sëb ak dugubee
Lu man di am Yal na ndam am jàmm am tono am
Muccak njariñ am
Ngëram sax ñépp way te jubee
Jëf Yal na sax tek juboo sax dàkk dàkk aku yiw
Teraanga sax ku ne
Jag yóot us ndamam ba ŋëbee
Bon Yal na wéy yàqu wéy lor wéy ba dootuñu ñëw
Tay ak ëllëg ñépp faf nuy ñeek a jóg di dabee
Waa penku waa sowu ak waa fépp yal na ñu nuy
Doylook a sopp ak raaseek ay wuteek a rëbee
Nun ñépp yal na sunuy bañ lab ci dex ñu bañ
Nu mucc muccle jël mbooleem jurug ña labee
YAL NANU FAR…
Yal na nu far tawat gu am
Te feg tawat gu nar am
Mu teggi wéy lumu ci am
Lépp lu sedd sunu xol
Yal nanu am céeboob njariñ
Mu ñàkk lor bari njariñ
Ci darajay ki am njariñ
Ba tax xelum ñi bon a dal
Yal nanu jox ku ne mbégam
Ba noppi nag dolli ko gëm
Bu yéemu lool ak ñi ko gëm
Lu dal xelam ma di ko dal
Ndam Yal na nuy biiw ak a dal
La sedd xol Yal na nu dal
Ci bopp dal gu sedd xol
Ba ñenn joy bay bëgg a raw
Yal na nu yoorekat bi yoor
Caabiy ngëram ya gën a foor
Caabiy ngëram ya foor a foor
Ba gën i tax ak i alal
Ka tabe am yal na ne ciix
Wépp yiwam ne nu ko foox
Nu waaru sant ne ko ciix
Mu yokk nuy néeg ak i lal
Ka jafe laa dagaana am
La jafe laa dagaana am
Fa jafe laa dagaana am
Yal na nu fab yii yatt jël
Yii yatt daal a jar a jël
Ku ci ne yal na nu ko jël
Mu faf nu jël nu faf ko jël
Mu def nu njël nu def ko njël
Yal na njariñ yi walagaan
Ku nekk am la mu dagaan
Lépp ak lu gën la mu dagaan
Seddum xolam yee ko ca njël
Yal na nu yeesal sunu ngëm
Peq te dolli sunu gëm
Fàww te naatal sunu gëm
Yaatal nu boole nu xajal
Yal nay ngëram taw ba wale
Yal nay dëram taw ba wale
Ndam xetti fépp wowale
Foo toll ñuy foog ak a ñal
Yal na nu man jaamu gu të
Ak wépp yiw wu am ko të
Raw jépp lor ju raw ko të
Jot ci lu sedd sunu xol
Ma sant saa sëriñ bile
Te sant saa murit yile
Amuma lut sëriñ bile
Ak saa murit yile ma wër
Samab sëriñ defar na ma
Samay murit dimbali ma
Man sant ñépp war na ma
Ku ne defal na ma lu wér
Yàlla fayal samab sëriñ
Ag yiw te dolli ko njariñ
Te may samay murit njariñ
Ak lépp luy tax ñu sawar
Sunub sëriñ Yàlla na bég
Sunuy murit Yal nañu bég
Fàww te jag tay ak ëllëg
Te bañ a yoqi bañ a wor
Mboleem ñu nuy may sutura
Yal nanu taqoo sutura
Fàww te teggi sawara
Ak gàcca ak sépp saxar
Samay murit wàcc nañu
Ngir ken du wax siisu nañu
Te kenn du wax gàntu nañu
Yal nanu am barkeek u tur
Fab nanu kër gépp defar
Yal nanu boole seen i bir
Defar ba dootu yàqu far
Ñu gudd fan wér sori lor
Noor ak nawet duñu taxaw
Ci sama mbir la ñuy taxaw
Yal na Sëriñ Tuubaa taxaw
Ci seen i mbir taxaw gu bir
Yal na sëriñ Tuubaa taxaw
Ci seen i mbir nag te taxaw
Te sunu mbir géppug taxaw
Te dolli nooti sox bu ñor
Soxam bi yal na daa di jib
Buy jib sunuy pexe di jub
Te lëf du jib bii sox a jub
Saasu jibee jubal i mbir
Yal na ne téf soxub ngëram
Gu tax ma bég sant gëram
Moom it mu bég sant gëram
Mbég ne wesar ñépp di for
Yal nanu may waamey njariñ
Yu nuy musal ak a jariñ
Tey dàkku lépp lunu bañ
Di naatali xol ak i cër
At mile wéy yal na wéy ak
Sunuy tawat tay ak ëllëg
At miy ñëw it yal na ñëw ak
Sunuy bég ak sunuy ngëram
Sëriñ bi at mile teru
Na ci sunuy ngëram teru
Sunuy mbég it na ci teru
Ku ne seral ci ab xolam
KU NE DALAL
Ku ne dalal ci am xelam
Te faj ci it jépp loram
Te far jubal ci ay biram
Yépp te yokk aw fanam
Fabal ndoxum jàmm aku yiw
Sotti ko ngir Yàlla ci kaw
Ay wi te wallu nook i yiw
Te jox ku nekk mébatam
Na jàmm dikk ju bari
Xéewal yi dikk te bari
Cant yi dikk te bari
Te bañatee tuxook i ndam
Li dale fii ba àjjana
Far nu ko soppil àjjana
Nu nekk nag ca aljana
Di wéy ba tàbbi jee nu jëm
Fegal nu laaj aku layoo
Ak luy waral laajuk layoo
Dolli nu wëlliis di layoo
Tay ak ëllëg te may nu ndam
May nu wér ak wér ci ndigal
Ak dund akug topp ndigal
Lu dul i mbég bumu nu dal
Dàkkul nu Ibliis ak ñoñam
Luy tax nu bég ci sunu xol
Bay sant rekkk na nu dal
Te lu ko moy bumu nu dal
Dàkkul nu hay fàww ak ndawam
Dàkkul nu ràgg ak i metiit
Jëkk jógug ràgg ak metiit
Musal nu it ci mépp tiit
Tay ak ëllëg jëggug ñëwam
Luy wàññi gëm na teggi wéy
Luy rékki gëm na teggi wéy
Luy yàq xel na teggi wéy
Dàkkul nu yii jëkkug ñëwam
Musal nu nun jëkk ug loru
May nub yar it jëkk ug beru
Defar nu jëkk ug asaru
Ngir Yàlla daal ak Yonenam
Na ay wi daal di fay kamaj
Ba mel ne xel dóotu ko daj
Te boo yaboo mu fay kamaj
Ba mel ne sax masul a am
Ay yàgg naa tàkk nga fay
Ay wa ca Daaru yaa ko fay
Ay wa ca Koongo yaa ko fay
Ay yi nga fay Yàllaa ko xam
Fu ay masee tàkk nga fay
Yàlla mi tax ngay dox di fay
Yal na la fay ag pay gu réy
Gu kenn dul wékkum xelam
Bu dul kon ak yaw nu loru
Bu dul kon ak yaw nu woru
Yaw ki nu tee loru woru
War na nu laa sant ndaxam
Boo fi newul woon naka mbir
Boo fi newul woon jépp lor
Dal nu te kon lëf du ko jar
Dàkkul nga nuy lor may nu gëm
Ag cant yaa ko mat a jox
Àddiya yaa ko mat a jox
Ku wax lu dul li ma la wax
Day waa ju sànku ju gëlam
Yaa mat a jox mbir ak alal
Jox naa la saa lépp fabal
Te def ma lar bunu musal
Bu gudd fan wérug yaram
Na nga ma def sab lar bu jee
Tàkk ci yaw ni nga jee
Ci Mustafaa ak ni nga jee
Ci Yàlla mii ba am ngëram
Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun
Aji-topp ji: Seex Lóo