Catégories
Sëñ Moor Kayre

Sëñ Moor Kayre (Xaaj 1)

Boo donnatul mbir ma jëggil mbir ma fum fu gëne
Bul toog te jëggóo ko fekkóo muy cosaanam fi nga ne

Njéem woomalóo mbay ma gàntal jëggi war na la yaw
Njéem am nga barke dawal xiifug njaboot fumu ne

Mbir mooy jubal góor yu gàddaay seen i xeet ne fi yaw
Ngir Yàlla boo ko xamul réeral murit ya ma ne

Kuy gàmbe ay fas te ñàddul fas ya féqu ba yooy
Yee dee fa yee dog nde xiif baa tar fa ñàdd ya ne

Lii dara yéesu ko sàkkul mbir ba am lu la doy
Kon say murit naat te saw tur siiw ci gox yi fi ne

Am barke it bumu tax ngay def araam di ko tay
Naa yàqu wéy na te yaw sag yàqu sax ca nga ne

Seetal ne Balhaam amoon nag baax lilee ko alag
Birsiis mbiram yàqu ñii ñaar doy na lii ma wane

Xam-xam bi ak barke beek màggal gi baa du la wor
Deel xëntewóo dem ci bàmmeel neex malaaka mu ne

Ngir barke am na daŋar yuy ray te moo di pexey
Ñenenti noon yii dawal ñoom lee ñu laa posone

Booy daw dawal bakkan ak saytaane ak nitu tay
Dawaale bànneex bi kon Buur jox la mbir mu tane

Bul faale ab jajukat day tax nga fàtte sa mbir
Jàppeel sa mbir kepp niw sémmeñ wu ñuy taxañe

Yaw Kayre jullil ci Yonnen moom ki gën ku ñu sos
Ca teg ci Saaba ya ndax mbir def cosaanam fi nga ne

Aji-bind ji: Soxna Nogay Cuun

Yaw kiy murit bi yanul te sant mooy li la war
Sa yan bi soppi ko ag teg leegi doon sa gawar

Doorug murit sew na nib gif muj ga rëy niki guy
Kuy bootu mooy tuut ku màggay dox di hub niki mbër

Ku xiin mu taatan bu dottee waame dootu maral
Njéem dégluwul gumba guy wax cam du taw dafa wor

Xamal ne kuy rafetal njurtay dajeeg lu rafet
Buur Yàlla fii njort lay àttee mbindeef yi du wur

Man Taala maay laahe biir fii kuy dëggal sama wax
Ku sax ci maanaa yi dib saadix bu am lumu war.

Aji-binf ji: Soxna Móomi Jóob
Aji-topp ji: Seex Lóo

Bul wóolu Yàlla ba tee laa jaamu jaamu gi sax
Moo tax mu bindoon la yaw deel jaamu jaamu gu sax

Deel boole jàkk ak a yaakaar Yàlla def ndigalam
Yii yaar la tànneef ya daa booleek i jaamu yu sax

Ku leeralul guddi teg ca lëndamal bëccëgam
Day pert ngir ëllëg it lu waay jiwul du fa sax

Yaw rikk Momar sa bakkan gàttalal yile way
Kuy digle day jëf te yaw sag jaamu sax du gu sax

Yaw daal dogonteek sa seex bii gën ci seex yi fi gën
Fa ñuy layoo doo fa yay ay wor du tee dëgg sax

Taalaa njegam manulaa jox Yàlla ay farataam
Te lott ciy sunna say mbir jox ko xutbu bi sax

Ku yàgg a ànd ak sëriñ bi dara jombu ko ngir
Ku àndulaak seex ba foofee ndax waxam dana sax

Man sant naa Yàlla moo def Bàmba muy sama ndey
Moo tax ma baaxoo taggam wii bañ du tee dëgg sax

Lu bukki wiir wiir ne kuuj dem ndaari man sama daa
Reeyi taggu kiy soppi ndaarik Daaru Yàlla na sax

Te mooy ki fiy sopp xambiy ndaari xutbu yu mat
Ñuy jiite ay Daaru Bàmbaa tee ba réew mi nasax

Aji-bind: Soxna Nogay Cuun

Catégories
Sëñ Moor Kayre

Saytaane, bànneex…

Saytaane, bànneex, àddina ak bàkkan.

Ku ngéen gis mu naa fiiraate boobee ma doon ragal
Lu dul àddina ak Ibliis a tax ay waxam matul.

Damaa gis ku dee dem naai ñooñoo ko fiir mu rot
Te ñooñook bànneex ak « nafsu » bàmbaa nu ciy musal.

Ba moo tax ma naa wuy seex bi dooleel ma ndax ma të
Boroom doole yiy fiiraate wuy man damaa matul.

Boroom doole yeey saytaane bànneex da koy dimbal
Te àddina bakkan ñoo ma fiir man ki leen tëhul.

Te man dégg naa way réer ñu naa jublu naa ñeneen
Ñu dul ñii ci way way wii tee ñu tuub ci may sosal.

Ba buur YÀLLA nee mbooleem malaakaam ya usjudóo
Li aadama » ibliis bañ la xëy suufe ab judoo.

Malaakaam ya sujjóoton mu jox léen kerog ngëram
Ibliis mat keroog saytaane suy jiite way dëddoo.

Na nuy sant kon nun ñi gëm YÀLLA bay sujóot
Te yaakaar ne bii bay way taggam yii fi seex bindoo.

Na nuy julli tey soppey YONNEN bii Ibliis ba ñoon
Ba xëy suufe kon « firdaywsi » wallaay la nuy dëddoo.

Nde leerug Yonnen googee ca biir Bàmba moo taxoon
Ibliis bañ ba tay day noonu Bàmba ak ña cay juddóoo.

Bakkan da d’ib kàngam bu naa dagul ma.
Way naari ab dagam la naa tëjal ma.

Bànneex ku koy jaamu la naa saxal ma
Bu dee ëllag siraat ne kaay dëkkal ma.

Ku toppatul YÀLLA jëlees na xel ma,
Moojaa keroog ku koy fegal mbugal ma.

Tuubal te réccooti sag ndaw ndax da ngaa defe woon
Neg ndaw lu sax la te boobee sax dangaa dofe woon.

Boobee dangaa boole man am rafet ku la gis.
Ngay daagu fàtte yii buur daf la koo yabe woon.

Buur YÀLLA moo boole man am ak rafet te du dañ
Yaw nag bul fàtte sa fan yii la la buur sose woon.

Aji-bind ji: Seex Lóo