Yaa ibna xaaliya na ngeen diy dànn
te bañ a ngóoroo donn naa ab dànn
Donn ug fetal cib dànn daf maa wóor ne
Soo dànnawul du tee nga reerew yànn
Fëlee di woon dàggaam du tee jëggaani
Moom tool ya soo bayul du tee yalwaani
Ndax ñaari siin ak ñatti xaaf ñooy dunyaa
Ca siin ya mbaate xaaf ya dóona sunyaa
Sonn bu wér sàmm bu wér nawees leen
Mbaa lu ko moy xaaf yee fi sës yabeef leen
Di dox di xat-xatloo ci bunti jaambur
Tàbbi ci biiri kër di xaar aw jaambur
Tax lu fa réer ñuy xeñ di laajte foo jaar
Bul mere kenn yaa deful ag njàmbaar
Lilee di saa ndigal te mooy saab yeete
Nelaw yu rëy xaraŋ ya doy nab yeete
Aji-bind ji: Seex Lóo