Baay Aale Njaay Rayal na mam kuuy Jël fàllare ja, ba ci bopp ak baat Yuur ga maa ko naan
Baay Gallaay óo Gallaay Aale Njaay Góor benn ub jabar Jabar benn ub doom Bu rootee tooy Bu walee weex Bu toggee ñuul
Soo bëggee doom Awal yoonu ndéem Soo demee ndéem Dangay dugg ub néeg Sa mbaam dugg um mbaar Ngay lekk cere Sa mbaam di lekk um ngooñ
Bu ca déwén saa Sa doom di jooy Sa doomi mbaam di ŋaax
Dënnub góor ni goroŋ Dënnub jigéen tema Dënnub màggat xiin Boo tëggee mu bëx-bëxi
Awuleen mu riir Dër du tee awu Ñaar du tee awu Kon ma dóoxlu tey awu Mbëxiit mu tol ni man Ku ko ñaf cib géew Mu war a nangoo awu
Yimbëy Sama yimbëy NgaIa Yimbëy! Sama yimbay Ngala Yimbëy!
Kuy jaay sa mbaam awal yoonu Ngooy Soo yeggee Ngooy Kër Moodu Si Buur Jolof Njaay xar la lay rayal.
Yuur ga yaa kooy naan Yaw ak Say gaay Yimb sama yimw Ngda Yimbëy! Sama yimbay Ngala. Yimbëy!
Suma jàppee yimbe Tëb dal ci kawam Yaxub ndiggam dëmm! Yumbe! Tubaab bi jàpp ma Dugal ma ci mbale Yumbe!
Mbale gi abaa kaso Yumbe! Booy dem ci ngoro Yumbe!
Booy dem ci ngoro Yumbe! Dangay gudde-guddelu Yumbe! Boo déggee yuuxu Yumbe! Nga dem walluji Yumbe!
Ñu ne Kmbaa a tooñ Yumbe! Ñu ne Sàmba a tooñ. Yumbe ! Sàmba rocci geen Yumbe! Geen gu tol ne bakku Yumbe! Mu ñagas ko ko Yumbe!
Ba muy ñatti yoon Yumbe! Mu ne neex naam ? Yumbe! Mu ne waaw-waaw Yumbe! Mu ne su neexul woon Yumbe! Mu tëb tëb ne »piit » Yumbe! Mu tëb tëb ne « paat » Yumbe! Sira Aaw xool Sira Yumbe! Sira Aaw amul jabar Yumbe!