Sëriñ Daam Jaane mi ngi juddoo Tëngéej ci atum 1986.Mi ngi jànge Njaañug Njaga. Dëkk Tuubaa di fa jàngalee Alxuraan . Di ab waykat it ci Wolof ci gàttal.
Al hamdu lillaahi rabbil haalamiina ndaxamak cant war na ci man al hamdu lillaahi Naa jóg te santati Buur bi xëy ma bind ci ndoxmuy daw ci biir i sidiit al hamdu lillaahi Naa jóg te sant ki aare...
Jamonoy Asan Paateek bañuy way Njóoba laaylaa doon fowantoo way man ak ñoom Jàkka Njaay Yéen doomi soxnay sëñ Basiir Lóo may ma fitAfrig jógal jox baay Jagal ag gàngunaay Ñi ma def ngalam ba ma xëy di nes-nesi...
GUDDI Mbalaani niir ya bu muuree, jant sàng safaxBëccëg ga tàggu timis, maay samp dënd di buur Xaftaan bu ñuul ni këriñ, am tupp-tupp yu weexMooy col ga ag ndaama laa, as ndiir su gàtt ma réer Xaftaan bu...
Lëndamug cofeel gi ma tàbbi, tax na ma gont warMutafaahilun ji fi ñépp, taamu ci tagg mbër Tegu yéene way yaru tagg bàkk wu saf xoromLa ma koy cawee di ko rëpptal da ma dib gawar Li ma yeex...
Gëy Njoora Gëy ñaaya yaw, téereb Boroom bi nga defAm xëy ku lay fakktal, daa repp mbaate mu dof Yan bañ yanoon mbër ya woon, téeñ baa ngi yaa ne ko casKuy tee nga dëngëñ di wéy, am mbaam...
Ahlan wasahlan watarhiiban ci sun ëtti xolNdokkeel la day lu nu war, Géy Njooro Géy ñaayaa Siggil nga daara yi ak, mbooleem lu taq ci ñoomSaw tagg daj na Kajoor, Saalum ba dem Ngaayaa Say soppe bég na ñu...
Ci àllub Kànka laa réeroon di wër yoonwa jëm Tuubaa ba gis caawog sëriñ Mbay Mu ànd ak Njamme Seex Sàmbaaki Kayreña ngay sukkóot ci dokkub sàdd ay way Ma yër seen mbind muy saf géeji Luqmaangu bëmboo Hassaan...
Hamdan li Rabbin Kariimin xadsanaa ci lu bér,tànneef bu mag ba ko wax laay marsiyaal ci wolof. Xerawluleen ma bu baax te jéem a jooy ci xalimngir diir bu yàgg a ngi nii, ranqoñ di tuuru ci xef. Wéet...
Kuy tukki Siin Honkoŋ na jaar réewum DubaayFàggul ma foofee ñay bu jot sama tolluwaay Rewtub ngëneel bi ñu dog ci saa garabug cofeelYóbbee na cër yi ne làcc xob yi di daŋŋ-daay Tóortóor yu taaru ya rot na...