Alkande j: (tur) Mooy ag alku, ku alku, torox, musiba këpp ci kawam mi ngi ci alkande.
Baataan
Àkk: (jëf) Mooy song mbir, niki àkki nit.
Ëmbeef l: tur
Li nekk ci biir, li mbir mi ëmb. Niral: Dal bii di jàng wolof de, ëmbeef li am na solo lool.
Ëw: jëf
Wër, gaw, wër-dombo. Niral: Fukki néegi ñax, ñoo ëw sunu ëtt bi.
Ñall w (tur)
Yoon wu sew, du bokk ak yoon wu mag wa ñépp di jaar.
Ñéer: (jëf) Ndox mu nekk ci biir cin te aw tàngoor yóbb ko daa ñéer.
Niral: Ndox mi ma defoon ci cin leegi di ko tàngal de ñéer na.