Ëcc

Ëcc: jëf

Génee ay wëñ ci wëttéen. Jël wëttéen taqal ci ëccukaay di wëndeel muy def i buum di laxasu. Bu laxasoo ba fees di poqe.

Ëmbeef

Ëmbeef l: tur

Li nekk ci biir, li mbir mi ëmb. Niral: Dal bii di jàng wolof de, ëmbeef li am na solo lool.

 

Ëw

Ëw: jëf

Wër, gaw, wër-dombo. Niral: Fukki néegi ñax, ñoo ëw sunu ëtt bi.