Baataan: tur
Waat yees di dajale di ko leeral, di ko toj ba mu leer.
Baataan: tur
Waat yees di dajale di ko leeral, di ko toj ba mu leer.
Bar (jëf)
Ñu lay liggéeyloo nga jaare noona dem saw yoon te liggéeyoo.
Bélli: jëf
Ubbi kanam, leeral kanam, wone am mbégte ci xar-kanam.
Nit ku bég, dangay gis kanam ga bélli lool.
Niral: Bélli ag kanam, moo gën bernde.
Bëlamu: (jëf)
Taxaw di yuuxu, di sànni say loxo, fu ne di waddi waddi ak a wëndéelu.
Bëmmaakon: tur
Ab bëmmkat, kuy bëmm, di génne am riir ci gémmiñam.
Bërëx (jëf) Mooy luy tàkk bu baax ni ag sébb. Sawara saa ngay bërëx-bërëxi de.
Bëtëri b: tur
[En: battery]
[Fr: batterie]
Beqi: jëf
1-Jàng ba mokkal sab bind, dem bind ko te doo ko xool. Ku jàng ba mokkal Alxuraan it day beqi, bind lépp bamu jeex te du ko xool.
2-Bind ba noppi jox kenn mu di la toppal la.
[En: correct]
[Fr: corriger]