Dëkk dàkk

Dëkk dàkk: jëf)

Sax dàkk, Sax ba fàww.

Dërkiis

Ñàkk a yëg i dóor, luñu la dóor dóor doo jooy doo wone ne metti na.

 

Dëtëm

Dëtëm: (jëf) Mooy dëpp say tuñ ci ndox di naan .

Dees

Danañu ko. Niral: Dees na wax = Danañu wax. Waaye kiy wax walla ñiy wax kenn xamu leen.

Deq

Deq b: (tur)

1- Biir bu rëy

2- Ndox mu taa ci lu mel ni am pax.

Diñe

Diñe: Mooy ñàkk a añ. Ku añul dangaa diñe.

Dibéer

Dibéer: tur

Ab bis la ci juróom ñaari bis yi. dimaas.

[En: Sunday]
[Fr: Dimanche]

Dooñ

Dooñ w: (tur) Mooy sas wu ndaw ci am mbay

Doom b

Doom b: tur

[En: USB key]
[Fr: clé USB]

 

Doxandéem

Doxandéem b:  tur

Ku ñëw fi barab te dëkku fa. 

[En: foreigner]
[Fr: étranger]