Baataan
Ne fayax (njëfka)
Ag dal, am péex. Mbooya muy upp ba yàgg mu ne fayax.
Féq: (jëf) Xëcc, guddal, tàwwi, yokk. Niki: Yàlla na Yàlla féq saw fan.
Fétal: (jëf) War a jaar ca yoon wa, bëgg lu gën a gaaw tax nga bàyyi fa yoon wa, jaar feneen fu dul ca yoon wa.
Fëlamu (jëf)
Xalangu fi suuf di bërëŋu, di yuuxu. Niki ni jigéen ñi di def bu nit faatoo.