Ag fer la gu lawbe yi di defar, per yu dijj lay doon te xeeñ neex.
Baataan
Gawar b: tur
Ku war ci aw fas
Gëdda g: tur
Koo xam ne xel mi neexul du mokkal te amul jom.
Gëndoo (tur)
Ñaar yu dendoon dem ba doon benn. Niki ñaari déeg yu dénd mu tawaat ndox mi gën a yokk ñu far gëndoo ci benn déeg.
Ne gëret: (njëfka)
Yëngu gu am doole. niki boo tiitee ni sa naw gi di def, dangay yëg ci sa dënn bi mel ni daa am lu ci jóge. Sa naw gi moo ne gëret.
Gët: tur
Ay bët, bu dee benn, bët bi ngay wax. Bu baree gët yi.
Gëtt g: tur
Xet gu neex, ndox la mu xeeñ neex ñu sol ko ci biteel, di ko laal. (Parfum)
Giif: jëf
Mer mu def, ku mer ba giif mooy ku mer ba meratul.
Giim: (jëf) Lu fay, mbaa muy bëgg a fay. Xal wi daa giim yaw ëf ko.