Ja b: tur
Fa nit ña di jaay ak a jënd. Maarse. Niral: Ndax pombuteer dana jaay ca ja ba.
Ja b: tur
Fa nit ña di jaay ak a jënd. Maarse. Niral: Ndax pombuteer dana jaay ca ja ba.
Jagam: melo
Taq, tilim, ñaaw, bon.
Naan ba la nga naanoon di génnaat
Jax: jëf
Joow. Yëngatu, boole lu ne. Jeñ ag gaal muy daw.
Jàmbu: (jëf) Amagóo dara di ànd ak sa niti démb, am as tuut rekk jàmbu leen mel ni ku leen xamatul. Niral: Man daje naa ak sa waay fee waaye damaa jàmbu.
Jànq: (jëf) Mooy dox waxtuw tisbaar, ku tukki waxtuw suba dangaa xëy, bu dee waxtuw tisbaar jànq.
Jéng b: tur
Weñ gees defar di ko takk ciy tànk ngir bañ boroom daw. Dongo yiy daw dees leen di jéng.