Ne kayam: (njëfka)
Dee, gancax guy sooga dee, ba tàmbalee wow, da naan kayam. Niral: Sa garab gi de nee na kayam, xanaa daawóo ko suuxat?
Ne kayam: (njëfka)
Dee, gancax guy sooga dee, ba tàmbalee wow, da naan kayam. Niral: Sa garab gi de nee na kayam, xanaa daawóo ko suuxat?
Kàcc m: Soow mu wayul. Soowum kàcc dafa am, mbaanig am, yaawur am.
Kàncóoli g: (tur) Mooy kaña gu mag.
Ay xeexkat yu ànd, militeer yu booloo.
Fr: Armée
Kéew m: tur
Mbooleem fi nu nekk ak li nu wër li nu ëw. Àll yi ak mbooleem gàncax yi añs. Aalam baatu araab la du wolof. (environnement)