Labat

Labat (jëf)

Gis jigéen bëgg ko, di wax ak moom ngir takk ko, dox googu ngay dox ngir loolu àntu mooy labat.

Lax

Lax (jëf)

Lu tooyoon ba tàmbalee wow nooy, lambax, niki bant bu lax.

Layu

Layu b: tur

Laŋ

Laŋ b: tur

Peel

Lànjaŋ

Lànjaŋ: jëf

Sànni fu ne dara, niki nit ku tëdd ne lànjaŋ, sànni fee ab tànk, fee beneen, fee ab loxo lu ne jëm fenn daal.

Lëm

1- Lëm (jëf) nëbb, làq, denc mbir fenn ba kenn du ko gis.

2- Lëm m (tur) Am pax la muy nekk ci garab, jóge ca kaw jan jëm suuf.

[En: 1- hide. 2- tree hole]
[Fr:1- cacher. 2- trou d’arbre]

Lënkoo-xare

Coalition d’armes