Luqnjuur

Sob, lépp lu ñuy aaye yaa koy def, luñu nëbb yaa koy luqati.

Niral: Kaas bu ma jënd, Bada mu luqnjuur mii toj ko.

 

Luum

Luum (jëf)

Ñàkk a man a wax, ginnaaw boo déggee lu la yéem walla nga gis ko, ne ŋàmm di ko xool.

Luuma

Luuma b: tur 

Jawub ayu-bis. Talaata ju ne, jaaykat yi dañuy ñëw sunu dëkk di fa jaaysi àllarba ñu dem ci beneen dëkk alxemes noonu. 

Niral: Liimab Ñiibi de akay xumb, àllarba ba àllarba lay doon.