Màcc

Màcc: jëf

Féete, jublu. Niral: Ci lan la sa xam-xam màcc?

 

Mëgg

Mëgg: tur

Xeeti létt la

 

Mëgg

Mëgg: njëfka

Ne màww, cër yu bàyyi jëmm ji gudd lool, yaram wu funki.

 

Mësëy

Mësëy w: (tur) Mooy tawub wicc-wiccal, taw bu ndaw.

Amna it ñuy wax mësëy-bandaŋ

Mësëy-bandaŋ

Mësëy-bandaŋ w: (tur) Mooy tawub wicc-wiccal, taw bu ndaw.

Amna it ñuy wax mësëy.