Mbaar

Ci biir ag sabar dañuy xaaj xeeti ndënd yi ñu ne ag na ñuy tëgge. Amna ca ñuy mbaar am ca ñuy mbëfër am ca ñuy  telmbet am ca am ndeer. Yii yépp boo leen boolee ñoo yor sabar gi.

Mbaboor

Am mbooloo, aw nit wu dajaloo. 

Niral: Mbaboor mii di ñëw moom fuñu jëm.

 

Mbamb

Coow lu bari, xuloo

Mbatiit

Mbatiit l: tur

Mbooleem baaxi aw nit ak seen i jëfiin, ak seen i aada añs.

[En: culture]
[Fr: culture] 

Mbëfër

Ci biir ag sabar dañuy xaaj xeeti ndënd yi ñu ne ag na ñuy tëgge. Amna ca ñuy mbaar am ca ñuy mbëfër am ca ñuy  telmbet am ca am ndeer. Yii yépp boo leen boolee ñoo yor sabar gi.

Mboor

Mboorm: tur

Li jàlloon, li xewoon ñu di ko nettali.

[En: history]
[Fr: histoire]

 

Mbooy

Mbooy g: tur

Fu bari ay ñax yu wow ak i taq-taq.

Mbooy

Mbooy g (tur)

Fees bàyyi, kenn toppatoowu ko ñax ya sax fa.