Naaxsaay

Naaxsaay: jëf

Jeex, seey, xiin wu naaxsaay, xiin wu fi ne woon ba yàgg muy dem ndànk ndànk ba set wecc.

Naq

1- Naq: jëf

Jël boppub nit dugal ko ci ndox ngir mu xëj. Ku soxor a koy def. Niral: Ndaysaan, waa jee ñu jëme ca mbalka ma de, dees koy naqali.

2- Naq b: tur

Ci ron jumbax. Niral: Bul bàyyi sab naq muy feeñ.

 

Nataal

Nataal: tur

Këyit wuñu def jëmi nit , mala,  gàncax walla lëfñ