Paax (tur)
Suuf su baax soo xam ne bay ko rekk a des.
Paax (tur)
Suuf su baax soo xam ne bay ko rekk a des.
Ne pacax (njëfka)
Tàbbi ci biir mbir, nekk ci biir yëf yi bu baax. Niral: Man de nee naa paccax ci biir.
Palamtu: (jëf)
Làmbatu aw yoon. Niki gumba buy dox day palamtu.
Pàttaliku g: tur
Lu jàll ba ñu di ko fàttaliku.
[En: memory]
[Fr: souvenir]
Péey (tur)
Fa buur nekk, yépp daje fa, dogal yi di fa jóge.
Crime
Poqe b: tur
Bant walla weñ ga ñu laxas wëttéen wa.
Génn, génne ci suuf. Ni mbir mi di génne.
Niral: Sindax yu ndaw yi ña nga naan pullet di génne ci bàq bi.