Sabar g: (tur) Ay ndënd yu ñuy tëgg.
Baataan
Salfaañe: jëf
Jaxase, la féete woon kaw féete suuf.
Saŋe s: (tur) Fu am kaaraange fu yiiru, fof boo fa duggee man ngaa mucc.
Kaala gu gudd la goo xam ne boo ko ràngoo ñaari mbicc yi (muy cat yi) day xaw a laal suuf.
Mer wu tar
Sànnikaay b: tur
Ñenteelu baaraam. Mooy baaraam biy joxoñ.
Sékk: njëfka
Wow koŋŋ. Fatt, Dënn bu ne sékk doo man a noyyi.
Séxéñ: melo
Xet gu bon gu yàgg ci nit ba far sax moom dootul deñ. Walla nit ku yàgg a nekk fu xasaw ba mujj xet ga séxéñ ko, maanaam tàmm na ko ba dootu ko xeeñ.
Sëfaan b: tur
Wata yu mag yiy yóbb bagaas yi
Ne sërëx (njëfka)
Tàbbi ci fu xóot. Daanu ci biir dara.