Sor

Sor: tur

Aw sagar, daggiitu ndimo. Boo ci dajalee yu bari man nga ci a ñaw ab njaxas.

 

Sot

Dagg ab bant ba cat li sew. Jël lañset di dagg catul dara ba mu sew.

Sottandiku

Wax ay wax cib jumtukaay mu denc ko. Ngir soo ko bëggee dégluwaat man koo dégluwaat.

[En: record]
[Fr: enregistrer]

Sox

1- Sox b: (tur) la génne ca gémmiñug fetal. La takk jóge ca fetal ga.

1- Aw dóor la. Ŋëb sab loxo dóor ko nit, sox nga ko. Dóor nga ko ab sox.