Taax: (tur) ab tabax
Baataan
Tandale: tur
Lu am noonu rekk te dara taxu koo am. Lu jekki-jekki am te kenn amalu ko walla ka ko amal jubluwu ko woon a amal. (Hasard)
Ténj: jëf
Ku boroom këram faatu da koy ténj, muuru ñatti weer di sellal du génn dem fenn.
Tér b: (tur) Mooy tilim, ay tilim-tilim.
Ne tóon (njëfka) Mooy tëdd ci sab pilyaan tegale say tànk ñu di la liggéeyal. Booba yaa nga ne tóon.
Tele b: tur
Tepp-tepp : (tur) Mooy ay taa-taa yu ndaw.
(ci wàllu xarala)
Fekk mbind mu tege nga teg ca sa baaraam jël ko (kóppiye)
Toñ: jëf
Toŋ, bëŋ, jeñ nit mu jëm ca kaw, dimbali ko ngir mu yéeg.