Waame w: Taw bu bari te am doole.
Baataan
Wagg: tur
Ay mbagg, bu dee menn mooy mbagg, bu dee yu bari di wagg.
Ne walax (njëfka)
Nëbb, làq, wann, denciin la denc gu kenn manul a àgg.
Walluwaan b: tur
Wata la buy jël nit ñu gaañu ñi, walla ñu tawat di leen rawale ca wopp-taal. (embulenche)
Wata b: tur
Waxambaane w: tur
Góor gu toll ci fukki at ak juróom jëm ñaar-fukk ak juróom. Ku tàmbalee yittewoo jigéen.
Way-dawlu ñ: tur
Ñi faatu, ñi wuyuji seen boroom. Niral: Ñaanalleen waydawlu ñu Yàlla yërëm leen.
Jàng ba jeexal Alxuraan ji.
Aw takkiin, aw bootiin. Jël dara teg ci ginnaaw takk. Niral: Neel wàkk sa doom ji boot.
Ne wérét: (njëfka)
Génniin wu bette wu waajul. Niki ñu wax la lu la tiital rekk sam xel génn ne wérét.