Xëf

Xëf (jëf)

Yaram wuy metti. Boole ak fasu. Mook tooy soreewuñu.
Niral: Fan yii de damaa diju di bind ba mujj xëf.

Xëret

Ne xëret: (njëfka)

Taxaw, bàyyi. Lu doon xër-xëri ba yàgg mu ne xëret. Niki ndox mu doon wàcc ag doole jekki jekki rekk ne xëret taxaw.

Xebet

Xebet: jëf

Diiŋat, suufeel, xeeb, ñaawlu.

Niral: Bàyyil di xebet li sa njaatige li di def, ndax boo nekkoon ci barabam de danga xam ne jàmbaar dëgg la, jiite yombul.

 

Xeraw

Ne xeraw (njëfka)

Tekk, selaw, dara yënguwul.

Xerawlu

Xerawlu: (jëf) mooy déglu gu ànd ak bàyyi xal la ngay déglu.

Xit

Xit: (jëf) Dox te jaaróo ci aw yoon. War a jaar ca yoon wa, bàyyi ko fa jaar ca ñall wa.

Xobu dencu

Xobu dencu w: tur

[En: memory card]
[Fr: carte mémoire]

Xodd

Xodd m: tur 

Am picc la

Xond-xond

Xond-xond b: (tur) Mooy ya taataa yu ndaw.

Xuuy

Xuuy: (jëf)

Tàkk ak a fay, lu ag leeram amul doole day xuuy.

[En: sparkle]
[Fr: scintiller]