Bëñ bu yolom di kallaj-kallaji, di bëgg a foq.
Niral: Nogay mu ndaw bëñ bi daa yanq.
Yulub: njëfka
Ne dagaj, mel ni lu fêb rekk yékkateendoo sa jëmm jépp dugg fenn, mel ni luñu fa sànni.
Mooy nekk ci biir ab yax te xale yi di ko muucu, day weex.
Yurub: njëfka
Dugg, mel ni fekk fu yaatu te am benn bën-bën, nga ca bën-bën ba yurub.
Yuur (jëf) Sëgg, dugal.
Nag wi yuur na bopp bi ci bagaan gi di naan.