Yol

1. Yol (jëf) Sottiku, tuuru, ndox a koy def ak yu ni mel.

2. Yol m (tur) Ndox mu bari muy walangaan jaar ci aw yoon di dem.

[En: 1-stream. 2- runoff]
[Fr: 1- ruisseler. 2- ruissellement]

Yooy

Yooy (jëf)

Sew, tuuti, xiibon, ñàkk a regg. Niral: Yaw leegi dangaa yooy, xanaa fa nga nekk daa neexul?

[En: skinny]
[Fr: maigre]