Yulub

Yulub: njëfka

Ne dagaj, mel ni lu fêb rekk yékkateendoo sa jëmm jépp dugg fenn, mel ni luñu fa sànni.

Yuq

Mooy nekk ci biir ab yax te xale yi di ko muucu, day weex.

Yuqi

Tàllal, guddal, tàwwi.

Niral: Booy dox bul yuqi sag bóli, fu ne nga xool fa.

 

Yurub

Yurub: njëfka

Dugg, mel ni fekk fu yaatu te am benn bën-bën, nga ca bën-bën ba yurub.

 

Yuur

Yuur (jëf) Sëgg, dugal.

Nag wi yuur na bopp bi ci bagaan gi di naan.