Sëñ Fàllu Mbàkke

Sëriñ Muhammadu Faliilu Mbàkke (dàkkantal: Sëriñ Fàllu, Fàllu Galas, Alaaji Fàllu) gane àdduna ca Daaru Salaam nekk ci tundu bawal ca réewum Senegaal ci 27 ndeyu-koor (rajab) atum 1305 ci gàddaay gi yamoo ak atum 1887/88.

Mu tombe ak bis bi turandoom Sunu Sang Muhammed (jàmm i Yàlla ak xéewalam ci kawam) riñaanee ci ndigalal Boroomam ànd ak sunu Sang Jibriil (jàmm ci moo) war daaba ju deesi woowe «Al-buraax», Ci rañaan googii la ko Yàlla sunu boroom joxee julliy joróom di ponk bi ëpp doole ci Lislaam, waral ko ci mboolem jullit ñi, ak xeet i xam-xam yu mu fi sotti ngir nun ak ya ko ñeel ci ag jagle, Muy guddi gu màgg ci Lislaam, guddi gi nu xéewal gi dikkale juge fa Aji-Màgg ji. Sëriñ Fàllu Mbàkke génn na àdduna ci atum 1968. dund na 81 ciy at ci ginnaaw bi mu nekkee xalifab Sëriñ Tuubaa ci atum 1945 ba 1968. Sëriñ Fàllu Mbàkke mom Seex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul baayam mi sos yoonu Muriid ak Soxna Awa Buso ndayam doomu Sëriñ Muhammadu BUSO di Sëriñ Mbusóobe nijaayu Sëriñ Tuubaa, Mu bawoo ci njaboot gu sell gii, di askan wu ragal Yàlla daa jàng tey jàngale, dëkkoo jaamu Yàlla te di ko jaamulu, di ay wàlliwuy Yàlla yu mat. Mu cosaano ci askanu Sëriif gog càllala ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonenteb Yàlla XMM. Mu dondoo ci loolu (donte ag njub déesu ko donnonte waaye dees na ci yare, te moo baaxoo am) ag cell, Yar, xam, ngëm ak melo ya war ci doomu Soxna, ci yooyu jikko la ko ay way-juram yare te nàmptal ko ci.

Moom nag mi ngi wuyuji boroomam ci atum 1968 ca Tuubaa.

Sëñ Fàllu Mbàkke (Xaaj 1)

Waxi Sëriñ Fàllu Mbàkke 1- Boo bëggee mucc ci làmmiñu nit ñi, deel def gémmiñ gu ŋa nga def ca dara. Kon ñaanal la rekk lañuy def. 2- Àdduna benn fan la muy tay, démb weesu na suba dikkagul,...

🎧 Ubbi
error: Content is protected !!