Sëñ Sàmba Jaara Mbay

Sëriñ Sàmba Jaara Mbay (1868 – 1917) di doomi Sñ Ahmadu Mbay ak Soxna Ndaag Kan, mi ngi gane àdduna ci atum 1868.

Kenn la ci taalibey Sëñ Bàmba yi dëkkoon ca Ndar. Cosaanam nag, kokki la.
Bokkoon na ci waykat yi gën a yéeme ci làkku wolof ak ci réewi wolof.
Ci niti Yàlla yi gën a naqaree xam la bokkoon. Ndax da daan dund ci biir nit ñi ne ñépp ba noppi boole woon ci di dem ca ja ba di yaxantu.

Ba mu demee di jébbaluji ca Seexul Xadiim, fekk na fa magam jii di Seex Saa-njaay ca Njaaréem.
Amna nag, lu wérul lu ñuy nettali cig jébbaloom ndax moom masul a doon ab géwal buy tëgg i ndënd. Boroom xam-xam bu mag la woon, bu mokkaloon alxuraan ca ba muy ndaw; ginnaaw ba la jóge Kokki dem Ndar ngir jàngi fa xam-xam.

Bokkoon na ci ab liggéeyam, tasaare njàngalem Sëriñ Tuubaa ci biir wolof yi.
Leeg leeg ci biir ay wayam dana ciy dugal waati Araab, rawatina ci ndoortel way yi walla muj ga. Bind ay taalif yu bari.
Lu ci mel ni, tagg yi mu tagg Sëriñ bi ak ay xarbaaxam.
Bokk na ci ay téereem:
Jësbul Majsóob, di bi gën a siiw ci ay mbindam.
Sëriñ bi nag « Saahibul aayaati» la ko tudde woon di ku man la muy def lool.

Moom nag, mi ngi wuyuji boroomam ci atum 1917.
Barabam ma nga ca armeeli Caameen ya ca Ndar.

Jasbul majsóob

Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi Alhamdu lillaahi ki may Xamal bu wér, ta di ma mayXéewal ci barkeb ki mu xëy,Jébbal lu dooni xéewëlam. Yéen gaayi diine jegeleenMa jege leen te dolli leen,Xam-xam bu wér te jafe leen,Ma fecci tay ay fas-fasam. Koo...

🎧 Déglu

Ku faatu yaa fay…

Bismil laahi rahmaani rahiimiXaala Seex Muhamadu Abdul kariimi Sàmba Jaara Mbay Ku faatu yaa fay jëkk a teewBuñu koy jullee nga di fa teewÑuy rob nga ànd ak ñoom di teewÑu dem nga des tontuw layam Seetleen na ngeen...

🎧 Déglu

Yaaram bi kenn bañu la

Alhamdu lillaahi yaw yaaram bi kenn bañu laBuur YÀLLA seede na lii yaaram bi kenn bañu la Lii laay biral gaa ñi ndax laabiire leen te ku xamWar naa xamal ku xamul yaaram bi kenn bañu la Yéen gaayi...

🎧 Déglu
error: Content is protected !!