logo_100

Laltaayug Kippaango Jàng Wolof

Kippaango Jàng Wolof barab la bees sos 10i fani féewerye ci atum 2018 ci njiital Sëñ Seex Lóo, Sëñ Bëgg Bàmba Géy ak Sëñ Ismayla Géy di ñenn ci Akaademi wolof. Cos gee ngi tukkee ci coobarewu ak bëgg a liggeeyal làkku wolof ba ñu bari man koo wax, man koo dawal ba noppi man koo bind.

Ci kaw gis-gis bii, la Kippaango Jàng Wolof sosoo ngir yaatal làkk wi, suqali làkk wi ak liggéeyal làkk wi ci sunu xam-xam, sunu am-am ak sunu man-man ci lu dul fayeeku kenn.

Njiiti Kippaango Jàng Wolof warlul nañu képp ku ci bokk te tënku ci sàrt yi, njàngum wolof ci lu dul muy fay dara, loolu nag amul setteey cosaan walla gog xeet walla gog diine.

Kippaango Jàng Wolof dafa séddalikoo ci ay jàngu yoy ku ci nekk sag coobarewu ak sag bëgg ak sag tënku ci sàrt yi ñoo lay boole ci njàng mi.  

Njaatige: Seex Lóo 

Topp-njaatige: Ismayla Géy

Jëwriñ ju rëy: Seexunaa Faal 

Topp-jëwriñ ju rëy: Maam Seex Caw 

Sàmba-koppar: Maam Bàlla Njaay 

Baay-sàq: Basiiru Géy 

Malaamisóo: Fàllu Jàllo

1- Njiitu lef mi : Musaa Caam

Topp-Njiitu lef: Kumba Biyaay  

2- Njiitu wikimedia : Xaadim Gay

Topp-njiitu wikimedia: Abdu Géy

3- Njiitu CAX: Ngañ Aaw   

Topp-njiitu CAX: Basiiru Jaw

4- Njiitu Njàng mi: Ismayla Géy

Topp-njiitu njàng mi: Aadama Jóob

Tomb 1:  Tur wi

Mbootaay gii di WAX di wund “wolof ak xamle”, mi ngi doon wuyoo ci turu jàng wolof, nu sosoon ko ci 10i fani féewaryée ci atum 2018.

Waaye ci lél bii di 16i fani suye ci atum 2019 lanu soppi tur wi tudde ko WAX, ngir mu gën a yaatu. Jàng wolof leegi ab bànqaas la ci biir WAX.

Tomb 2: Naal yi

1- Génne ay téere: Lu ci mel ni téereb dawal bob day jàngale bind ak dawal.

Ak téereb nos-wax bob day ëmb mbooleem takk-takki wolof yi. 

Ak téereb gàggantikaay bob dana làmboo lu toll ci 60.000i baat.

Ak tànn téere yu am njariñ yi tekki leen ci wolof.

2- Dooleel wolof ci lënd gi: Niki fexe ba fépp fuñuy fekk làkku farañse rekk man faa fekk wolof. Ba ci sax fexe ba jollasu yi ak nosukaay yépp am làkku wolof.

3- Yakk fànni xam-xam yi ci ndabal wolof: Niki xam-xam yu mel ni: Mboor, melosuuf, màndaxe, xeltu, càmbar-biddiw añs, yépp nu def leen ci wolof ba wolof man a am xam-xam te du jar muy dégg weneen làkk.

4- Yaatal wolof ci réew mi: Fexe ba daaray Nguur gi, ñu di fa jàng wolof nimu ware, tele yi ak dali web ak tablo yi ci mbedd yi fépp fuñu ciy bind wolof ñu bind fa wolof yu set.

WAX dina amal, ci réew mi walla ci bitim réew, jépp jëf walla wax yuy tax mu àggale naal yii.

Tomb 3: Màkkaan mi

Mbootaay gi nag, fi mu toll nii amagul màkkaan waaye am na mébétu wut màkkaan.

Tomb 4: Diir bi

Amul benn àpp buñu ko àppal, ngir bu fa yeggee mu tas. Danuy ne ci liggéey bi rekk ba bunu fi jógee sunuy doom mbaa sunuy sët wéyal liggéey bi.

Tomb 5: Bokk gi

Ku bëgg a bokk ci mbootaay gi fàww nga matal yii:

  1. a) Jënd këyitu cér ci 1000f te weer wu dee nga joxe 500f.
  2. b) Bokk ci kippaangog whatsApp gi di Jàng Wolof.
  3. c) Dem bëggi xëtu WAX wa ca facebook ak wa ca youtube.
  4. d) Joxe sa tur ak saw sant ak sa atum judd ak sa benn nataal, te aajar sa bopp.

Tomb 6: Génn gi.

Nit ki dina génn ci mbootaay gi ngir ñatt yii:

  1. a) Tekki ndombal tànk
  2. b) Faatu
  3. c) Bu xëttee sàrt yi fekk jot na ay aartu ak i dànkaafu. 
  4. d) Bokk na ci itam bu ñàkkee teg ay nattam. Bu boobaa, Pekk bi dinañu dogal ag dàqam bu jàppee ney layam wérul.
  5. e) Bu nit bàyyee ci coobareem

Tomb 7 : Wànqaas yi

Mbootaayug WAX nag, dafa séddalikoo ci juróomi wànqaas, muy:

Njàng mi: Di bànqaas bi yor mbooleem lu aju ci njàng ci mbootaay gi.

 Lef: di fees tekkee mbooleem xam-xam yi ci wolof.

CAX: Di Caabal ak Xarala gi.

Caabal gi di fees siwale ay xibaar.

Xarala gi moo yor mbooleem lu jëm cig xarala ci mbootaay.

Wikimedia Senegaal: Di bànqaas bob ab liggéeyam mooy taxawu wikipedia wolof.

 AAK : Ànd Aar Kéew mi, di bànqaas bu jëm ci sàmm kéew mi, lu ci mel ni jëmbët garab ak setal gox yi, ak yee ci nit ñi.

Tomb 8: Njëwriñ gi

Njëwriñ gi làmboo na lu toll ci fukki jëwriñ yu ñu fal ci at, te di ko ci yeesal.

Ñi ngi nii:

1- Njaatige

2- Topp-njaatige

3- Jëwriñ ju rëy

4- Topp-jëwriñ ju rëy

5- Sàmba koppar

8- Topp-sàmba koppar

9- Baay sàq

10- Malaamisóo

  • Am na juróomi njiiti bànqaas muy:

1- Njiitu lef

2- Njiitu saabal

3- Njiitu CAX

4- Njiitu njàng mi

5- Njiitu wikimedia Senegaal

Tomb 9: pekk bi

Njëwriñ gi dina fal ci ñoñam ab pekk bu tëdde nii:

1- Lenn njaatige

2- Lenn topp-njaatige

3- Jenn jëwriñ ju rëy

4- Jenn topp jëwriñ ju rëy

5- Benn sàmba-koppar 

6- Benn topp sàmba-koppar 

Kenn manul a yorandoo liggéeyub njaatige ak bob sàmba-koppar

Tomb 10: Ndaje mu rëy mi

At mu ne, dananu amal ndaje mu rëy. Benn, jaare ko ci kippaangog whatsApp gu mag gi walla nu jëmmoo, fumu ciy doon it dees koy waxtaane njëkk.

Ndaje mu rëy mi moo ëmb jépp aji-bokk, ak tolluwaay bu mu man a am.

Dina ñu ko woote at mu  nekk.

15i fan balaa lél bi ñu jàpp a agsi, jëwriñ ju rëy ji  dina woo bépp aji-bokk xamal ko ko. Wëppa wa dina ko leeral ca woote ba.

Njaatige li,  ci njàppadalu njëwriñ gi, dina jiite ndaje mi, leeral tolluwaayu mbootaay gi ak jëf yi mu defagun.

Sàmba-koppar dina leeral koppar gi ba  noppi gaaral ndencug at mi ngir ndaje mi nangu ko.

Bu ndaje mi nangoo wëppa wi ba noppi, kenn du wax lu ko génn.

Dogal yi nag dinañu ko jël sukkandiku ci xalaatu ci ëpp ci ña teew ca waxtaan wa.

Ginnaaw bu wëppa wi jeexee, dinañu jàll ci coppiteg pekk bi.

Ndogal yiy tukkee ci ndaje mu rëy mi day gàllu ci ndoddu jépp aji-bokk nga teew walla nga ñàkk a teew.

Tomb 11: Ndaje mu rëy mu jamp

Saa bunu dara bettee lu man a yàq mbootaay gi, mbaa muy salfaañe lenn ci ay liggéeyam, dees na woote ndaje mu jamp ngir saafara loolii.

Dina am ci càkkuteefu xaaju lim bu teg benn bu way-bokk ñi, njiit li man naa woote am ndaje mu rëy mu jamp ci niñu ko leerale ci laltaay gi mu jëm ci coppiteg laltaay gi walla luñuy jënd walla ñu koy jaay walla luñuy defar te manut a ñàkk ci mbootaay gi. 

Niñuy wootee ndaje mu rëy mi noonii lañuy wootee itam ndaje mu rëy mu jamp mi.

Ndogal ya ñu fay jël ñi ngi koy natte ca xalaatu ñi ëpp ca fa teew …

 

Tomb 12: Koom mi

Ngir nu am um koom fàww cér bu ne di teg ci ndeetel weer wu ne. Man nanu koo am it jaare ko ci yeneen i lijjanti.

Tomb 13: Coppiteg laltaay gi

Ba laa genn coppite di am ci laltaay gi fàww waa pekk bi waxtaane ko ba noppi.

Bu waa pekk bi tënkee la war a soppiku ba noppi dinañu ko gaaral way-bokk ñi ci ndaje mu rëy mi walla ci ndaje mu rëy mu jamp mi ngir ñu nangu ko.

Tomb 14: Tas gi

Bunu demoon bay tas mbootaay gi li fi jot a nekk ci alal, dananu ko may kuréel guy yëngu ci wolof, walla guy yëngu ci kéew mi.

Tomb 15:  Sàrt yi

Njëwriñ gi man naa teg ay sàrt yu ndaje mu rëy mi di nangu.

Sàrt yooyu nag ñooy nos wépp doxalin wu ñëwul ci laltaay gi, rawatina li jëm ci doxinu biiru mbootaay gi.

1-Basiiru Jaw
2-Móodu Jóob
3-Seexunaa Faal
4-Aadama Jóob
5-Nogay Cuun
6-Baay Laat Silla
7-Basiiru Géy
8-Góora Jóob
9-Amsatu Faal
10-Xaadim Bàmba Léy
11-Seex Isaa Caw
12-Seex Dukure
13-Abdu Salaam Sekk
14-Laay Juuf
15-Seex Sàmb
16-Saaliw Mbuub
Móomi Jóob
17-Musaa Caam
18-Maam Bàlla Njaay
19-Xaadim Gay

20-Paab Tàmbedu
21-Ngañ Aaw
22-Seexunaa Mbàkke
23-Moor Suraŋ
24-Maalig Seen
25-Tuubaa Jaañ
26-Abdu Géy
27-Ahmadaa Jàllo
28-Abdu Akiim Sàmb
29-Kumba Biyaay
30-Njaase Sëy
31-Muhammet Faal
32-Njaga Saar
33-Fàllu Faal
34-Baay Sëriñ Jaxate
35-Xaadim Jóob
36-Mamadu Sekk
37-Seex Jaxate
38-Saaliw Mbàkke Kajoor
39-Abdul Mutalib Buso
40-Fàllu Géy
41-Fàllu Koso Jóob

42-Seex Basiiru Mbàkke
43-Abdu Lahat Buso
44-Muhammet Jóob
45-Fàllu Juuf
46-Ma-Sàmba Yàdd
47-Galas Bämba Mbàkke
48-Mati Mbow
49-Mbàkke Jóob
50-Maysa Ndaw
51-Abdu Lahat Jaxate
52-Seex JIITE
53-Àlliyun JÓOB
54-Mustafaa GÉY
55-Abdulaay KA
56-Baay Asan Jóob
57-Seex Seen
58-JiiliNjaay Alxuraan
59-Daniyel Silaani
60-Seex Omar JEŊ
61-Seex Sekk
62-Maysa Maaraa
63-Maamur Faal

64-Mbembaa Jàllo
65-Jiili Saar
66-Elimaan Njaay
67-Moor Ñaŋ
68-Ahmadu Njaay
69-Maalig Faal
70-Aadama Béey
71-Xaadim Ñas
72-Maxtaar Kànji
73-Libaas Jóob
74-Sëñ Saalihu Buso
75-Baara Njaay
76-Imaam Maaraa Njaay
77-Móodu Faal
78-Xaadim Sekk

79- Maam Bàlla Si
80- Sang Yaaram Jóob
81- Mutalib Buso

82- Móodu Ture
83- Seexunaa Faal
84- Muhammet Juuf
85- Imaam Ñaŋ
86- Saaliwu Njaay 87- Móodu MBÀKKE Ture
88- Sëriñ Abdu Lahat BUSO
89-Maam Moor Si

90- Fàllu SILLA
91- Sëriñ Xaliil MBÀKKE
92- Baay Sëriñ BUSO

93- Mustafaa Lóo Muxtaar
94- Ndey Faatu Mbay
95- Móodu Kamara
96- Suhaybu Jóob

97- Móodu Kamara
98- Suhaybu Jóob

99- Seexunaa Ndóoy.
100-Basiiru Saar.
101-Nday Awa Jóob.

102- Maysa mbow.
103- Sohaybu Si.
104- Imaam Jóob.
105-Daam Faal.

106-Baay Seex Ñaŋ.
107-Abdu Samt Jóob
108-Sohaybu Lóo.
109-Maam Ceerno Njaay.
110-Moor Si Kebe.

111-Soxna Ngóone 113-Xàbbaan Géy.
113-Sëriñ Sang Jóob
114-Sëriñ Xaadim Jaxate.

115-Móodu Sill
116-Baay Sëriñ Jatara.
117-Àlliw Siise.
118-Abdu Rahmaan Jéey.
119-Sëriñ Fàllu Cuun.

120-Mustafaa Géy.
121-Àlliw Ba.
122-Seexunaa Sëy.
123-Sëriñ Lamin Dem.
124-Baay Sëriñ Buso.
125-Lamin Baara Jaxate.
126-Abdu Xaadar Ñaŋ.
127-Abraham Saar.

128-Sëriñ Maamun Jóob.
129-Sëriñ Moor Ndaw.
130-Sëriñ magànna Najaay.
131-Sëriñ Muhammadu Sekk.
132-Sëriñ Móodu Ñaŋ.
133-Móodu Gay.
134-Sëriñ Fàllu Mbàkke
135- Sëñ Seexunaa Buso.
136- Seexunaa Omar Ñaŋ.
137- Mustafaa Lóo.
138- Abdu Xaadar Siise
139- El-Basiir Jeŋ.
140- Mbay Ture.
141- Xaadim Bàmba Gay.
142-Soxna Faati Njaay
143- Móodu Maamun Jóob.
144-Soxna May Jóob.
145- Sëñ Tuuba Silla.
146- Abdu lahat Lóo.
147- Seex Mbay Sekk.
148- Muhamdu Lamiin Jaame.
149- Seex Jaañ.
150- Baay Mbay Jeŋ.
151- Abdu Lahat Buso.
152- Abdu Lahat Si.
153- Abdulaahi Saar.
154- Jiili Abdu Xaadir Jaxate.
155- Fàllu Galas Li.
156- Allaaji Fàllu Gay.
157- Fàllu Sekk.
158- Daam Faal.
159- Móodu Ka.
160- Yuusu Jaañ.
161- Ahmadu Bàmba Ngom.

Saarti Kippaango Jàng Wolof

1- Wartéef li njëkk mooy: Képp ku dugg ci dal bi ba la ngaa def dara na nga bindu, ngir ñu man laa ràññee ci booy jàng. Booy bind saw tur it, na nga ko bind ci wolof yu set.

2- Képp ku dugg ci dal bi te sam mbind ci wolof setagul, li jëkk a war ci yaw mooy dem fa ñu bi Bind yépp, daal di tàmbali sam njàng.

3- Bu dee masóo jàng dara, wartéef la ci yaw nga tàmbalee ci ijji.
Bu dee mas ngaa jàng nag, man ngaa tàmbalee ci Jàngu 1 (xaaj 1 ak 2)

4 – Bind boo jàng, ba la ngaa jàll ci beneen, fàww dangaa war a def tàggatu yi aju ci bind bi ba noppi.
Te sañoo tëb benn bind, mbaa di leen safaane.

5- Boo jàng ba jeexal, wartéef la ci yaw nga jokkoo ak saytukat yi walla jàngalekat yi ñu yóbb la defal la ag kàtte. Boo jàllee ci kàtte gi ñu jox la sa lijaasa.

0
Ñi am lijaasa

Tegtal ngir bindu ci dal bi

E-mail

Di nga ko soxla ngir bindu ci dal bi. Niral: awanjaay@gmail.com

Lënkaay g

Fàww nga am ko door a man a dugg ci lënd gi. (Connection)

Turu jëfandikukat

Booy bindu dinañu la laaj ab turu jëfandikukat. Mooy tolloo ak sa daqantal waaye man naa nekk sa tur itam. Saa booy lënku, man nga koo jëfandikoo bu la gënale bind sa e-mail. 

Lënku

Soo amee lënkaay, fàww nga lënku door a man a tàbbi ci lënd gi. (Connecter)

Baatu jàll

Sa baatu-jàll mooy baat boo tànnal sa bopp ngir mu doon sa caabi ci dal bi. Na nekk bu neexula xam te na nga ko fàttaliku bu baax nodal saa yooy lënku dina ñu lako laaj bu weesoo sa turu jëfandiku/e-mail. 

Linkiku

Génn ci lënkaay gi. Soo lënkoo ba linkiku ba laa duggaat fàww nga lënkuwaat. (Déconnecter)

Bindu

error: Content is protected !!
Aller à la barre d’outils