Sëñ Mbay Jaxate

Sëriñ Mbay Jaxate (1875 – 1948) Di doomi Xaali Ma-jaxate Kala ak Soxna Kumba Faal.

Mi ngi ganee àdduna ca Aynumaan di ab dëkk bu nekk ca Kajoor, ci atum 1875.

(Xaali Majaxate Kala miy baayam nag, bokkoon na ci ñi ëpp xam-xam ci jamonoom.
Looloo taxoon sax doomu Belsig bii Claude GERRESHCH di woon ab gëstukat ca IFAN jagleeloon ko ag maay-kan gu gànjaru.

Mi ngi ko def ci kubbbiteg tekkig téereb Xaali Ma-jaxate Kala bii di « Mubayyin ul iskaal » di téere bu am solo ci wàllu way.

Xaali Majate nag, ab saax-saax la woon di ab jàngalekat, di ab sëriñ boole ci di ab àttekat, di woon it jëwriñ ju rëy ju Lat-joor.)

Dayo bu am solo boobu baayam amoon yépp nag, teewul sëñ Mbay Jaxate dogu ci fekki Seex Ahmadu Bàmba YG ngir jébbalu.

Ag dajeem ak sëriñ Tuubaa Xaadimu Rasuul dib sëriñam di kéemaanug Yàlla gi gën a rëy, di melow jaam bi gën a mag ki Yàlla jox ngëneel yi. Ci jamono ji Seex Ahmadu Bàmba nekkee Gaboŋ ci la sërñ Mbay Jaxate jóge Aynumaan ngir fekkiji ko. Booba baayam a ngi dund. Waaye Sëriñ Bi moom nekku fi woon, ci kilifteefu maam Cerno Ndaamal Daaru di rakki sëñ Tuubaa ca la dem.Ca wetam sax la yeggaleem njàngam.

Ginnaaw ñibbisig Sëriñ Bi ci géej gi, ca jamono ja Seex Ahmadu Bàmba di waaj a dem Murtani ca la maam Cerno Mbàkke aajare sñ Mbay Jaxate sëriñ Tuubaa. Kon ca Murtani ca la sëriñ Mbay Jaxate tàmbalee tarbiyoom ci wetu sëriñ Tuubaa. Foofa nag la ko Sëñ Bi joxe sëriñ Basiiru Mbàkke ngir mu koy jàngal.

Jaar-jaaram ca Xuru Mbàkke:

Ca atum 1918, sëriñ Mbay Jaxate sëriñ Tuubaa moo ko yabal fële ca Xuru Mbàkke. Li waral yabal ga nag, dafa baatine lool ba deesu ko man a leeral fii…

Ngir am ci ab xalaat ci dayob baatin bu dëkk bu ndaw boobu ca Bawal, da lay doy sëkk nga xam ne way-juri Seex Ahmadu Bàmba fa la ñu dëkkoon laata ñuy dem ca Saalum, te fa la ñu bàyyi woon seen um caat te sax fa la sëñ Tuubaa denc ñenn cig njabootam ginnaaw ba leen Yàlla teelee moom.
Xuru Mbàkke nag tay, dëkk bu am solo la ci yoonu Murit.
Dundug Sëriñ Mbay Jaxate ca Xuru Mbàkke, dafa tënku woon ci jàng ak jàngale, jaamu Yàlla, bay dunde, bind ay taalif.

Sufyànke bu mag di aw werekaan daan wax ay nqereñtéef yu am solo.

Moom nag, mi ngi fi jóge ci atum 1948 ca Xuru Mbàkke. Dund na 73i at.

Sëñ Mbay Jaxate (Xaaj 1)

WAAWAAW Sëriñ bee di góorMoo di waayi BuurYàlla moo di BuurWaawaaw Wax ju baax a baaxJëf ju baax a baaxWaayi Buur a baaxWaawaaw Bàmba daal a baaxJëfam daal a baaxWaayam daal a baaxWaawaaw Moo fi def lu baaxMoo fi...

🎧 Déglu

Sëñ Mbay Jaxate (Xaaj 2)

DOLLI NU Dolli nu doo jeexle daraMoo tax ma laajati daraNde duma laajati daraKon mukk ngir am naa la bir Yaw waande ag dex nga te dexDu dëy du jeexle mukk ndoxMoo tax ma naa dolli ma ndoxTe dolli...

🎧 Déglu
error: Content is protected !!